Léebu surga bu njublaŋ bi te muus
16
Yeesu wéyal njàngaleem di wax taalibe yi ne: «Dafa amoon benn waa ju am alal, mu am surga buy toppatoo alalam. Ay nit ñëw xamal ko ne surgaam bi, mu ngi pasar-pasaree alalam. 2 Njaatige bi woo surga bi ne ko: "Lan laa dégg, ñu koy wax ci yaw? Damaa bëgg nga leeralal ma, ni ngay doxale sa liggéey ndaxte dootoo toppatoo sama alal." 3 Noonu surga bi wax ci xelam naan: "Lan laa wara def léegi, gannaaw sama njaatige dafa may dàq ci liggéey bi? Liggéey ci tool? Awma doole ngir def ko, te yelwaan, rus naa di ko def. 4 Aa! Xam naa li ma wara def ngir sama njaatige, bu ma dàqee ci liggéey bii, am ñu may dalal ci seen kër yi."5 «Mu woo kenn, kenn ci ñi ameeloon njaatigeem bor. Ki ci jëkk mu laaj ko ne: "Ñaata nga ameeloon sama njaatige?" 6 Mu tontu ko ne: "Ñeenti junniy liitari diwlinu oliw." Mu ne ko: "Sa kayitu bor a ngii; toogal fii gaaw te nga bind ñaari junniy liitari diwlinu oliw." 7 Surga bi laaj keneen ki ne: "Ñaata nga ameel sama njaatige?" Mu tontu ko ne: "Téeméeri saaku pepp." Mu ne ko: "Sa kayitu bor a ngii. Toogal fii te nga bind juróom ñett fukki saaku pepp." 8 Noonu njaatige bi daldi naw surga bu njublaŋ bi ndax muus bi mu wone ci jëfinam. Ndaxte niti jamono jii ñoo gëna muus ci lu ñuy jot, seen diggante ak seeni moroom, ba raw doomi leer yi.»
9 Yeesu yokk ca ne: «Maa ngi leen koy wax, wutleen ay xarit ci alalu àddina si, ngir bu jeexee Yàlla dalal leen ci dëkkuwaay yi nekk ba fàww. 10 Ku gore ci mbir yu ndaw yi, dinga gore ci mbir yu mag. Ku jubadi ci mbir yu ndaw yi, dina jubadi tamit ci mbir yu mag. 11 Su fekkee nag jubuleen ci ni ngeen di jëfandikoo alalu àddina si, kan moo leen di dénk alal ju wóor ji? 12 Su fekkee jubuleen ci li ñenn ñi moom, kan moo leen di jox li ngeen moom? 13 Benn jaam mënul jaamoondoo ñaari sang, dina bañ kii te bëgg ki ci des, walla mu fonk kii te xeeb ki ci des. Mënuleen boole jaamu Yàlla ak jaamu alal.»
14 Bi Farisen yi déggee kàddu yooyu yépp, ñuy ñaawal Yeesu ndaxte dañoo bëggoon xaalis. 15 Yeesu tontu leen ne: «Yeen Farisen yi dangeen jàppe seen bopp ñu jub ci kanam nit ñi, waaye Yàlla xam na seeni xol. Ndaxte lu nit gëna fonk, Yàlla sib na ko.»
Yoonu Yàlla du soppeeku mukk
16 Yeesu yokk ca ne: «Jamonoy yoonu Musaa ak yonent yi, dem na ba ci Yaxya. Bi mu ñëwee ak léegi ñu ngi yégle xibaar bu baax bi ci nguuru Yàlla te ku nekk mu ngi góor-góorlu ngir dugg ci, 17 waaye asamaan ak suuf weesu, moo gëna yomb dindi benn rëdd ci arafu yoonu Musaa.
18 «Képp ku fase sa jabar te séyaat yaa ngi njaaloo, te ku takk jigéen bu jëkkëram fase yaa ngi njaaloo.»
Léebu boroom alal bi ak Lasaar
19 Gannaaw loolu Yeesu nettali benn léeb, ne: «Dafa amoon benn boroom alal bu doon sol ay yére yu rafet te jekk bi bari lool. Muy bànneexu bés bu nekk te doon lekk, lekk bu neex. 20 Ci buntu këram amoon na waa ju néew doole, ju fa doon tëdd, ju tuddoon Lasaar, te yaramam bi yépp fees ak góom, 21 te dafa doon bëgga jot lekk bi doon daanu ci bérébu lekkukaayu boroom alal bi ngir faj xiifam. Rax ci dolli, xaju mbedd yi doon mar góomu yaramam yi. 22 Waa ju néew doole bi daldi dee, malaaka yi jël ko, yóbbu ko ci wetu Ibraayma. Boroom alal bi tamit dee, ñu suul ko.
23 «Bi mu nekkee ci mbugal ci béréb bi ñu dee ñi nekk, mu yékkëti ay bëtam, séen Ibraayma ak Lasaar ci wetam. 24 Noonu mu yuuxu ne: "Maam Ibraayma, maa ngi la koy ñaan, yërëm ma. Ndax doo yónni Lasaar mu jël catu baaraamam, capp ko ci biir ndox, te toqalal ma ci sama làmmiñ ndaxte maa ngi ci coono, ci bérébu safara sii." 25 Waaye Ibraayma tontu ko, ne ko: "Sama doom fàttalikul ne ci àddina si bànneexu nga te Lasaar mu ngi woon ci naqar. Waaye léegi, Lasaar mu ngi ci jàmm te yaw yaa ngi ci coono. 26 Rax ci dolli kàmb gu réy moo nekk ci sunu diggante, ba tax ñi nekk ci nun, bu ñu ko bëggoon sax, mënuñu ñëw ci yeen, te ñi nekk ci yeen mënuñu ñëw ci nun."
27 «Boroom alal bi ne ko: "Maam Ibraayma, maa ngi la koy ñaan nag, nga yónni Lasaar ci sama kër baay, 28 ngir mu dem, artu sama juróomi rakk yi ma fa bàyyi, ngir ñu baña ñëw ci bérébu mbugal bii." 29 Ibraayma tontu ko, ne ko: "Ñoom, am nañu mbindu Musaa yi ak yu yonent yi. Nañu leen déggal!" 30 Mu ne ko: "Déedéet, maam Ibraayma. Loolu doyul. Bu fekkee kenn ci ñi dee ñi, moo dekki, dem ci ñoom dinañu tuub seeni bàkkaar." 31 Waaye Ibraayma ne ko: "Bu ñu dégluwul mbindu Musaa yi ak yonent yi, bu kenn dekkee ci ñi dee ñi sax du tax ñu gëm."»