Léebu doom ju réer ji
15
Benn bés, juutikat yi ak bàkkaarkat yi, ñoom ñépp jegesi nañu Yeesu ngir déglu ay njàngaleem. 2 Farisen yi ak jàngalekatu-yoonu-Musaa yi di xuntu, di wax ne: «Kii day dalal bàkkaarkat yi te di lekkandoo ak ñoom.» 3 Noonu Yeesu tontu leen ak léeb bii: 4 «Bu kenn ci yeen amee téeméeri xar te benn bi réer, ndax du bàyyi juróom ñeent fukk ak juróom ñeent yi ci àll bi te mu wëri bi réer ba gis ko? 5 Bu ko gisee dina ànd ak mbégte, teg ko ci mbaggam yi 6 te yóbbu ko këram, mu woo ay xaritam ak dëkkandoom yi te ne leen: "Kaayleen bànneexu ak man ndaxte gis naa sama xar bi réeroon." 7 Noonu tamit maa ngi leen koy wax: Mbégte miy am ci asamaan bu benn bàkkaarkat tuubee bàkkaaram, moo ëpp mbégte mi am ci juróom ñeent fukk ak juróom ñeent ñu jub te soxlawuñu tuub seen bàkkaar.8 «Walla su fekkee benn jigéen dafa am fukki xànjaru xaalis te mu réerle ci benn, ndax du taal làmpam, bale kër gi, seet ruq yi ak ruqaat yi ngir gis ko? 9 Bu ko gisee dina ànd ak mbégte, woo ay xaritam yu jigéen ak dëkkandoom yu jigéen yi te ne leen: "Kaayleen bànneexu ak man ndaxte gis na sama xaalis bi réeroon." 10 Noonu, maa ngi leen koy wax: dina am mbégte ci malaaka Yàlla yi bu benn bàkkaarkat rekk tuubee bàkkaaram.»
11 Noonu Yeesu waxaat ne: «Dafa amoon benn waay bu am ñaari doom yu góor. 12 Ki ci gëna ndaw ñëw wax ko ne: "Baay, jox ma sama wàll ci ndono bi." Noonu baay ji séddale leen alalam. 13 Ay fan yu néew gannaaw loolu, doom ji dajale alalam bi yépp, tukki ci réew mu sori. Mu topp bànneexu bakkanam ba yàq alalam bi yépp. 14 Gannaaw bi mu yàqee alalam bi yépp, xiif bu metti dal ci réew ma. Mu tàmbalee di nekk ci jafe-jafe. 15 Mu dem nag di liggéeyal benn waay bu dëkk ci réew ma. Waa ji yóbbu ko ca toolam ngir mu sàmm mbaam-xuux yi. 16 Xiifoon na lool bay bëgga sax di lekk ci lekku mbaam-xuux yi, waaye kenn joxu ko ko.
17 «Noonu xelam dellusi te mu wax ne: "Sama kër baay am na surga yu bari te ñu ngi lekk bay desal. Man, maa ngi fii di dee ak xiif. 18 Dinaa jóg dellu sama kër baay ne ko: 'Baay bàkkaar naa ci kanamu Yàlla te tooñ naa la, 19 ba yellootuma ñu may woowe sa doom. Waaye jàppe ma nag ni kenn ci say surga!' " 20 Mu daldi jóg, dellu ci kër baayam. Bi doom ji di ñëw, baayam séen ko fu sori. Mu yërëm ko lool, daw, laxasu ko, te fóon ko. 21 Doom ji ne ko: "Baay, bàkkaar naa ci kanamu Yàlla te tooñ naa la, ba yellootuma ñu may woowe sa doom." 22 Baay ji ne surga yi: "Gaawleen, andi sabadoor bi gëna rafet te ngeen solal ko ko, te ngeen solal ko jaaro ci baaraamu loxoom ak ay dàll ci tànkam. 23 Andileen nag bi ñu yafal te ngeen rey ko, nu lekk di bànneexu. 24 Ndaxte sama doom dafa dee woon, dekki na. Dafa réeroon te feeñ na." Noonu ñépp tàmbali di bànneexu!
25 «Ci waxtu woowu, taaw bi mu ngi nekkoon ca tool ba di liggéey, bi muy ñibbisi ba jubsi kër gi, mu dégg ay tëgg ak fecc. 26 Mu laaj kenn ci surga yi ne: "Lan moo fi xew?" 27 Surga bi ne ko: "Xanaa sa rakk bi demoon moo dellusi. Moo tax sa pàppa reyal ko nag bi ñu yafal ndaxte gisaat na ko ci jàmm." 28 Noonu taaw bi mer, baña dugg ci kër gi. Baay ji génn ngir ñaan ko mu duggsi ci kër gi. 29 Mu ne baay ji: "Ay at a ngi nii, maa ngi lay liggéeyal te mësuma laa ñàkka déggal. Waaye mësoo ma jox benn béy bu ndaw ngir ma lekk ko ak samay xarit. 30 Waaye sa doom bi demoon, yàq sa alal ci jigéen ñiy jaay seen yaram, moo dellusi nga reyal ko nag bi ñu yafal." 31 Baay ji ne ko: "Sama doom, yaa ngi ak man bés bu nekk. Te lépp li ma yor yaa ko moom. 32 Fàww nu bànneexu te bég, ndaxte sa rakk dafa dee woon te dekki na. Dafa réeroon te feeñ na."»