Yeesu ci kër Farisen
14
Benn bésu noflaay, amoon na kenn ci njiitu Farisen yi bu waxoon Yeesu ngir mu ñëw lekk ci këram. Noonu ñi toogandoo woon ak moom ci bérébu lekkukaay bi, di ko bàyyee xel. 2 Foofu, amoon na benn waay bu amoon feebar bu doon newwil ay tànkam. Mu ñëw ci kanamu Yeesu. 3 Yeesu jël kàddu gi ne jàngalekatu-Yoonu-Musaa yi ak Farisen yi: «Ndax yoonu Musaa maye na ngir ñuy wéral ci bésu noflaay bi?» 4 Waaye kenn amul woon lu mu koy tontu. Noonu Yeesu teg loxo waa ji, wéral ko, wax ko mu ñibbi. 5 Noonu Yeesu ne leen: «Kan ci yeen la doomam walla nagam di daanu ci biir teen te du ko dindi ni mu gëna gaawe bu doon sax ci bésu noflaay bi?» 6 Waaye kenn amul woon tontu ci loolu.7 Yeesu gis ni gan yi doon tànne toogukaay yi féete kanam. Noonu mu wax leen léeb bii: 8 «Su ñu la woowee ci céet, bul tànn toogukaay yi féete ci kanam ndaxte amaana ne am na ku la ëpp solo ku ñu woo 9 te ki leen woo yeen ñaar dina ñëw te ne la: "Bàyyeel ko toogukaay bii." Noonu dinga rusa dem ci toogukaay yi féete ci gannaaw. 10 Waaye su ñu la woowe ci céet, nanga tànn toogukaay yi féete ci gannaaw. Bu boroom céet bi ñëwee dina la ne: "Sama xarit, ñëwal ci toogukaay yi féete ci kanam." Bu boobaa, dinañu la sargal ci kanamu gan yi yépp. 11 Ndaxte ku yékkëtiku dinañu la suufeel te ku suufeelu dinañu la yékkëti.»
12 Noonu Yeesu daldi ne ki ko woo woon mu lekk, ne ko: «Booy woote añ walla reer, bul woo say xarit, say mag ak rakk, mbokk yi ak dëkkandoo yu am alal yi, ndaxte ñoom tamit mën nañu ko def ngir delloo la sa coono. 13 Waaye booy woote lekk, ñii nga wara woo: ñi néew doole, làggi yi, lafañ yi, ak gumba yi, 14 ndaxte ñoom mënuñu la koo delloo te noonu dinga barkeel te Yàlla dina la ko fey bés bi ñu jub ñi di dekki.»
15 Bi mu déggee wax yooyu, kenn ci ñi bokkandoo woon ak Yeesu di lekk wax ko ne: «Kuy lekk ci nguuru Yàlla barkeel nga.» 16 Noonu Yeesu tontu ko ak léeb bii: «Dafa amoon benn waay bu togglu woon ñam wu bari, mu woo woon nit ñu bari. 17 Ci waxtu reer, mu yónni surga bi ngir mu dem ne leen: "Ñëwleen ndaxte léegi lépp sotti na." 18 Waaye ñu tàmbali di jéggalu ñoom ñépp. Nit ku jëkk ki ne: "Damaa jënd tool, fàww ma dem gis ko. Ñaan naa la ko, jéggal ma ko." 19 Ñaareelu nit ki ne: "Damaa jënd fukki nag, fàww ma dem, tàggat leen. Ñaan naa la ko, jéggal ma ko." 20 Ñetteelu nit ki ne: "Damay dooga takk soxna, moo tax duma mëna ñëw." 21 Noonu surga bi dem, wax njaatige bi loolu lépp. Njaatige bi daldi mer, ne surgaam: "Gaawal nga dem ci péncu dëkk bi ak mbedd yi, nga andil ma ñii: néew-ji-doole yi, làggi yi, gumba yi ak lafañ yi." 22 Ci diir bu gàtt mu dellusi ne ko: "Njaatige bi, def na lépp li nga ma wax waaye ba léegi taxul kër gi fees." 23 Njaatige bi ne ko: "Génnal dëkk bi, dem ci mbedd yi ak yoonu àll yi te nga fexe, nu nit ñiy ñëwe, ba kër gi fees dell 24 ndaxte maa ngi leen koy wax: kenn ci ñi ma jëkkoona woo du mos ci sama lekk bi."»
Nit ku bëgga topp Yeesu war na bàyyi lépp
25 Benn bés Yeesu doon tukki. Mbooloo mu takku àndoon na ak moom. Noonu mu walbatiku ne leen: 26 «Képp kuy ñëw ci man, dangaa wara bàyyi sa baay, sa yaay, sa jabar, say doom, say mag ak say rakk, ak sa dund sax. Lu ko moy doo mëna nekk sama taalibe. 27 Fàww nga déggal ma ba ma jaral la ñu daaj la ci bant te topp ci man, lu koy moy, doo mëna nekk sama taalibe.
28 «Kenn ci yeen bu bëggee tabax kër gu kawe, ndax du toog xalaat ñaata la koy dikke, ngir xam li mu am ci xaalis ndax dina mëna matal liggéey bi? 29 Lu ko moy dina tàmbali teg fondamaa waaye du ko mëna yeggali. Su boobaa, ñépp ñi gis loolu dinañu ko ñaawal 30 tey wax ne: "Kii déy, tàmbali na tabax waaye mënula yeggale."
31 «Walla su fekkee dafa am benn buur, bu wara dem xare ak beneen buur ndax du toog xalaat, ndax ak fukki junni xarekat, ndax dina mëna jaamaarloo ak beneen buur bi yor ñaari fukki junni xarekat? 32 Lu ko moy ci waxtu wi buur boobu di soreegul na ko yónnee ay ndaw, ngir ñu waxtaan ngir déggoo ci jàmm. 33 Te noonu nag, ku nekk ci yeen bu bàyyiwul am-amam yépp du mëna nekk sama taalibe.