Ku tuubul bàkkaaram, sànku
13
Ci waxtu yooyu mu am ñu ñëw yégal Yeesu naka la Pilaat reyloo woon ay nit yu dëkk Galile ci waxtu bi ñu doon jébbal Yàlla sarax. Seen deret daldi jaxasoo ak deretu mala yi ñu doon rendi. 2 Yeesu tontu leen ne leen: «Ndax xalaat ngeen ne ñooñu ñoo ëpp bàkkaar ñeneen ñépp ñi dëkk Galile ba ñu rey leen ci anam bu ñaaw boobu? 3 Déedéet, maa ngi leen koy wax. Waaye sungeen tuubul seeni bàkkaar dingeen sànku ni ñooñu.» 4 Noonu mu waxaat leen ne: «Ndax fàttaliku ngeen fukki nit ak juróom ñett yi dee woon ndaxte tabax bu réy te kawe bi nekkoon Silowe, dafa daanu woon seen kaw; ndax xalaat ngeen ne ñooñu ñoo ëpp bàkkaar ñeneen ñépp ñi dëkk Yerusalem? 5 Déedéet, maa ngi leen koy wax. Waaye sungeen tuubul seeni bàkkaar dingeen sànku ni ñooñu.»
6 Ci loolu Yeesu wax leen léeb bii: «Benn waay amoon na garabu figg ci toolam. Benn bés mu ñëw ngir witt ci meññeefu garab gi waaye gisu fa dara. 7 Noonu mu ne surgaam bi: "Ñetti at a ngi nii may ñëw ngir witt ci meññeefu garab gi waaye duma fi fekk dara. Dagg ko. Lu tax muy feesal tool bi te amul njériñ?" 8 Waaye surga bi tontu ko ne ko: "Sama njaatige, may ko at bii. Dinaa ko gas te sotti ci tos, 9 xéy-na dina meññ ci at bi di ñëw. Lu ko moy, nga daggalu ko."»
Yeesu wéral na benn jigéen ju xuuge ci bésu noflaay bi
10 Benn bésu noflaay Yeesu da doon jàngale ci biir benn kër-ñaan. 11 Foofu amoon na benn jigéen. Rab moo ko taxoon xuuge diiru fukki at ak juróom ñett ba mënul woona siggi. 12 Bi ko Yeesu gisee mu woo ko wax ko ne: «Soxna si yewwi nañu la, ci sa laago.» 13 Noonu mu teg ko loxoom yi. Ci saa si soxna si daldi siggi te jub xocc, di màggal Yàlla.
14 Noonu njiitu kër-ñaan bi daldi fees dell ak mer ci li Yeesu doon faje ci bésu noflaay bi. Mu jël kàddu gi, wax mbooloo mi: «Am na juróom benni fan yu ñu wara liggéey, kon ñëwleen ci bés yooyu ngir faju waaye bu mu doon ci bésu noflaay bi.»
15 Boroom bi tontu ko ne: «Yeen naaféq yi! Kenn ku nekk ci yeen bu amee nagam walla mbaamam ndax du ko dem yewwi ci bésu noflaay bi ngir yóbbu ko mu naani? 16 Te jigéen jii bokk ci askanu Ibraayma, Seytaane tënk ko ci diiru fukki at ak juróom ñett, ndax waruñu ko yewwi ci bésu noflaay bi?»
17 Bi Yeesu di wax loolu, bañaaleem yi daldi rus waaye mbooloo mi ànd ak mbégte ci jëf yu yéeme yi mu doon def.
Léebu doomu fuddën bi ak léebu lawiir bi
18 Yeesu daldi ne: «Lan la nguuru Yàlla gi di nirool ak lan laa koy méngaleel? 19 Dafay mel ni doomu fuddën bu benn waay jël, ji ko ci toolam. Mu sax doon garab. Picci asamaan si ñëw, ràbb seeni tàgg yi ci bànqaas yi.» 20 Mu waxaat ne: «Lan laay méngalee ak nguuru Yàlla gi? 21 Dafay mel ni lawiir bu benn jigéen jël, jaxase ko ci ñaar fukki kilo fariñ ba lépp funki.»
Bunt bu xat bi
22 Yeesu doon jàll dëkk yi ak ci gox-goxaat yi jëm Yerusalem te mu doon jàngale ci yoon bi. 23 Mu am kenn ku ko laaj ne: «Boroom bi ndax nit ñu néew ñooy mucc?» Yeesu wax leen ne: 24 «Maa ngi leen koy wax, góor-góorluleen ngir dugg ci bunt bu xat bi, ndaxte ñu bari dinañu fa jéema dugg te duñu ko mën. 25 Bu boroom kër gi jógee tëj buntam ak caabi te ngeen des ci biti, dingeen tàmbali di fëgg di wax ne: "Boroom bi ubbil nu!" Su boobaa dina leen tontu ne: "Xamuma fan ngeen jóge." 26 Te dingeen waxaat ne: "Lekkandoo nañu ak yaw te naanandoo ak yaw, te jàngale nga ci sunu péncu dëkk yi." 27 Bu booba dina leen tontu, wax ne: "Xamuma fan ngeen jóge. Sorileen ma, yeen ñépp ñiy def lu jubadi." 28 Foofu la jooy di ame ak yéy seeni bëñ, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yi yépp ci nguuru Yàlla gi; waaye yeen dinañu leen sànni ci biti. 29 Nit ñu bari dinañu jóge ci penku, ci sowu, ci nord ak ci sudd ngir lekkandoo ak ñoom ci xew bi ci nguuru Yàlla ga. 30 Te noonu ñi mujje dinañu jiitu, te ñi jiitu dinañu mujje.»
Yàqutewu Yerusalem
31 Noonu mu am ay Farisen yu ñëw wax Yeesu ne: «Jógeel fii, nga dem feneen ndaxte Erodd mu ngi lay bëgga rey.» 32 Yeesu tontu leen ne: «Demleen ngeen waxal ma xaju àll boobu ne: "Xoolal! Damay dàq rab yi te wéral ñi feebar tey ak suba, te ci ñetteelu fan bi ma matal sama liggéey." 33 Waaye fàww ma dem tey, suba ak gannaaw suba ndaxte jaaduwul ñu reye yonent feneen fu dul Yerusalem.
34 «Aa Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi tey sànni ay xeer ñi la Yàlla yónnee ba ñu dee. Ñaata yoon ma bëgga dajale say doom, ni ginaar di dajalee ay cuujam te muur leen ak ay laafam, waaye yeen bëgguleen ko! 35 Moo tax Yàlla dina leen bàyyee seen dëkk. Maa ngi leen koy wax, dootuleen ma gis ba bés bi ngeen di wax ne: "Barkeel na kiy ñëw ci turu Boroom bi."»