Yeesu artu na taalibeem yi
12
Ci waxtu bi Yeesu di wax loolu Farisen yi, ay junni junniy nit dajaloo nañu bay dëggante. Yeesu jëkka wax taalibeem yi ne: «Moytuleen lawiiru Farisen yi, maanaam seen jikkoy naaféq. 2 Lépp lu nëbbu dina feeñ te lépp luy kumpa dinañu ko xamle, 3 moo tax lépp lu ngeen mën di wax ci guddi gi, dinañu ko dégg bëccëgu ndarakàmm te lépp lu ngeen déeyante ci néeg yi, dinañu ko yégle ci kaw kër yi.4 «Maa ngi leen koy wax, yeen samay xarit: buleen ragal ñiy rey yaram te gannaaw loolu dootuñu mëna def dara. 5 Dinaa leen won kan ngeen wara ragal! Ragalleen ki nga xamante ne gannaaw dee, am na sañ-sañu sànni leen ci safara. Waaw, maa ngi leen koy wax, kooku ngeen wara ragal. 6 Ndax duñu jaaye juróomi picci ramatu ci ñaari dërëm? Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom. 7 Te yeen seeni kawaru bopp sax waññ nañu leen. Buleen ragal dara ndaxte yeena ëpp solo mbooloo picci ramatu.
8 «Maa ngi leen di waxaat ne, ku ma nangu ci kanamu nit ñi, Doomu nit ki dina la nangu ci kanamu malaakay Yàlla ji, 9 waaye ku ma weddi ci kanamu nit ñi, Doomu nit ki dina la weddi ci kanamu malaakay Yàlla ji. 10 Ku waxal Doomu nit ki lu bon, dinañu la ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu la ko mësa baal. 11 Bu ñu leen yóbboo ci kanamu kër-ñaan yi ngir àtte leen ak ci kanamu kilifa yi ak ci kanamu àttekat yi, buleen jaaxle ci anam bi ngeen wara waxe ak ci li ngeen wara wax ngir setal seen der 12 ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal li ngeen wara wax ci waxtu boobu.»
Léebu waa ju ñàkk xel ji
13 Amoon na ci biir mbooloo mi, benn waay bu wax Yeesu ne: «Jàngalekat bi, ndax doo wax sama mag mu sédd ma ci alalu ndono fi nu sunu baay bàyyeel?» 14 Yeesu ne ko: «Sama waay, kan moo ma fal àttekat ngir ma séddale seen alalu ndono?» 15 Noonu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen bëgge, ndaxte bakkanu doomu Aadama ajuwul ci alalam ak lu mu bari-bari.»
16 Noonu mu wax leen léeb bii: «Dafa amoon benn waay bu am alal, bu toolam meññoon lu bari. 17 Mu wax ci xelam: "Naka laay def? Ndaxte amatuma sax béréb bu mëna denc sama ngóob yi." 18 Noonu mu ne: "Waaw, xam naa li ma wara def. Damay daaneel sàq yii, defaraat yeneen sàq yu gëna réy, def ci sama ngóob yi ak sama alal yépp, 19 te dinaa wax ci sama xel: 'Sama waay am nga alal ngir diiru at yu bari. Noppalul, ngay lekk di naan tey bànneexu.'" 20 Waaye Yàlla ne ko: "Yaw mi ñàkk xel, tey ci guddi sax dinaa jël sa bakkan. Kon li nga doon dajale lépp, ku koy moom?"» 21 Yeesu teg ca ne: «Loolu mooy dal képp kuy dajale alal ngir boppam te amoo alal ci kanamu Yàlla.»
Nit war na wóolu Yàlla
22 Noonu Yeesu ne taalibeem yi: «Lii moo tax maa ngi leen koy wax, buleen jaaxle ci seeni dund, ci li ngeen wara lekk walla ci seeni yaram, li ngeen wara sol 23 ndaxte dund moo ëpp solo lekk te yaram moo ëpp solo yére. 24 Xoolleen picci baaxoñ yi: duñu ji, duñu góob, amuñu dencukaay, amuñu sàq, waaye Yàlla mu ngi leen di dundal. Yeena ëpp solo fuuf picc yi. 25 Kan ci yeen moo mëna jaaxle ba yokk ab diir ci dundam? 26 Su fekkee lu tuuti loolu mënuleen ko, lu tax ngeen di jaaxle ci li ci des?
27 «Xoolleen tóor-tóori ñax mi, ni muy saxe: duñu liggéey, duñu ràbb ay yére. Maa ngi leen koy wax, buur bi Suleymaan sax, ci alalam yépp, li mu doon mëna solu yépp, mësul soloo ni benn ci ñax yooyu. 28 Su Yàlla solalee nii ñax yi nekk ci tool yi tey, te bu subaa ñu sànni ko ci taal, ndax du leen gëna solal yeen, yeen daal yeena tuuti ngëm? 29 Buleen wut li ngeen wara lekk walla li ngeen wara naan te buleen ci jaaxle 30 ndaxte loolu lépp xeeti àddina yi xamul Yàlla ñoo koy wut, waaye seen Baay xam na ne soxla ngeen ko.
31 «Wànte wutleen nguuru Yàlla te Yàlla dina leen jox li ci des. 32 Buleen ragal dara yeen ñi mel ni gétt gu ndaw, ndaxte seen coobare Baay la, mu jox leen nguuram. 33 Jaayleen seen alal, séddale ko néew-di-doole yi, defarleen kalpe yu dul yàqu te noonu dingeen am alal bu dul jeex ci asamaan fu sàcc dul dugg jot ko, ak fu ko max dul yàqe 34 ndaxte fu sa alal nekk foofu la sa xol di nekk itam.»
Taalibe Yeesu dafa wara wóor tey moytu
35 Yeesu waxaat taalibe yi ne: «Takkuleen seen ndigg yi te seeni làmp wéy di tàkk, 36 mel ni surga yuy xaar seen njaatige jóge ci céet. Noonu bu yegsee rekk te fëgg, ñu mën koo ubbil. 37 Barkeel nañu, yooyu surga, yi nga xam ne seen njaatige, bi muy yegsi, fekk na leen ñuy xoole. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina takku ndiggam, toogloo leen, te jegesi leen ngir jox leen ñu lekk. 38 Buy yegsi ci xaaju guddi walla sax bi fajar di waaja jot, li ëpp solo mooy mu fekk leen ñuy xoole. Ñooñu barkeel nañu. 39 Xamleen bu baax ne boroom kër gi bu xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw, doon na xoole ngir tere ko mu dugg këram. 40 Yeen tamit fagaruleen ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu bi ngeen ko foogewul.»
41 Piyeer ne ko: «Boroom bi, ndax léeb bi nun doŋŋ nga ko jagleel, walla ngir ñépp la?» 42 Te Boroom bi tontu ko ne: «Kan mooy surga bu wóor tey moytu? Moom la njaatigeem di tànn ngir mu jiite yeneen surga yi ngir ñuy lekk ci waxtu bi gën. 43 Barkeel na boobu surga nga xam ne, bi njaatigeem di yegsi fekk na muy jëfe noonu. 44 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina teg alalam yépp ci ay loxoom. 45 Waaye su surga bi di wax ci xelam ne: "Sama njaatige dina yéexa ñëw," te mu tàmbali di dóor yeneen surga yu góor yi ak yu jigéen yi te di lekk ak naan sàngara ba màndi, 46 njaatige surga boobu dina ñëw ci bés bi mu ko foogewul ak ci waxtu wu mu xamul. Noonu dina ko tas te boole wàllam ak ñi gëmul Yàlla. 47 Surga boobu xam bëgg-bëggu njaatigeem te waajul dara, deful dara itam ni mu ko bëgge, dinañu ko dóor ay yar yu bari. 48 Waaye ki nga xam ne xamul woon bëgg-bëggu njaatigeem te def ay yëf yu jar dóor, dinañu ko dóor ay yar yu tuuti. Dinañu laaj lu bari ki ñu jox lu bari, te dinañu sas lu bari ki ñu dénkoon lu bari.
49 «Damaa ñëw taalsi xal ci suuf si te bëggoon naa lool xal boobu tàkk léegi. 50 Am na sóob bu ñu ma wara sóob, te duma am jàmm feek matul. 51 Xalaat ngeen ne damaa ñëw ci suuf si ngir indi jàmm? Déedéet, maa ngi leen koy wax; waaye xaajaloo. 52 Ndaxte dale ko tey juróomi nit ñu nekk ci kër dinañu xaajaloo, ñett ñi xaajaloo ak ñaar ña te ñaar ñi xaajaloo ak ñett ña. 53 Baay dootul juboo ak doomam bu góor te doom bu góor dootul juboo ak baayam. Yaay dootul juboo ak doomam bu jigéen te doom bu jigéen dootul juboo ak yaayam. Goro bu jigéen dootul juboo ak jabaru doomam te jabaru doom dootul juboo ak goroom bu jigéen.»
54 Noonu Yeesu yokk ca, ne mbooloo mi: «Sungeen gisee xiin di jóge ci sowu jant, dangeen di wax ci saa si ne taw baa ngi ñëw te noonu lay yegsee. 55 Te sungeen yégee ngelaw bu jóge ci sudd, dangeen di wax ne dina tàng te noonu lay xewe. 56 Naaféq yi! Dangeen di mëna ràññee liy xew ci suuf si ak ci asamaan si. Lu tax ba mënuleen ràññee li xew ci jamono jii?»
57 «Lu tax dungeen àtte yeen ci seen bopp lu jub? 58 Boo amee noon te ngeen am jafe-jafe tey waaja dem ci kër àttekaay bi, fexeel ba ngeen juboo ci bi ngeen nekkee ci yoon bi, ndaxte boo ko deful dina la yóbbu ci kanamu àttekat bi. Bu la àttekat bi àttee ba noppi, dina la teg ci loxoy takk-der yi, te takk-der yi dinañu la tëj ci kaso bi, 59 te doo fa génn feek feyuloo lépp ba mu jeex, ba ci fiftin bi mujje.»