Yeesu jàngal na taalibeem yi ni ñuy ñaane
11
Benn bés Yeesu doon ñaan ci benn béréb. Bi mu ñaanee ba noppi, benn ci taalibeem yi ne ko: «Boroom bi, ndax doo nu jàngal ni nuy ñaane, ni ko Yaxya jàngale ay taalibeem?» 2 Yeesu ne leen: «Bu ngeen di ñaan, waxleen lii:
 
Baay, na ñépp yékkëti sa tur,
na sa nguur ñëw,
3 may nu li nuy dunde bés bu nekk,
4 te baal nu sunuy bàkkaar
ndaxte nun tamit nu ngi baal ñi nu tooñ,
te bul bàyyi Seytaane fiir nu.»
 
5 Noonu mu yokk ca ne: «Bu fekkee kenn ci yeen dafa am xarit, mu dem ci moom xaaju guddi te wax ko ne: "Sama xarit, lebal ma ñetti mburu 6 ndaxte dama am sama beneen xarit bu jóge ci tukki, dal sama kër te awma dara lu ma ko jox." 7 Ki ci biir dina ko tontu ne: "Bul ma sonal. Tëj naa sama bunt te tëdd naa ak sama njaboot ba noppi. Mënuma jóg ngir jox la mburu yi." 8 Maa ngi leen koy wax, bu dul li mu nekk xaritam sax moo tax mu jóg te jox ko ko, waaye dina jóg, jox ko lépp li mu soxla ndax ni mu ko doon sonale ci ñaan bi.
9 «Te man, maa ngi leen di wax: ñaanleen, ñu may leen. Seetleen te dingeen gis. Fëggleen, ñu ubbil leen. 10 Ndaxte ku ñaan, ñu may la. Ku seet, dinga gis. Te ku fëgg, ñu ubbil la. 11 Ban baay ci yeen, moom lay doomam di ñaan jën, mu jox ko jaan; 12 walla mu ñaan ko nen, mu jox ko jiit? 13 Yeen ñu bon ñi, segem yeena mëna jox seen doom lu baax, rawatina Baay bi ci asamaan ndax du jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan?»
Yeesu dàq na benn rab te jàngal mbooloo mi
14 Benn bés Yeesu dàq benn rab bu muumaloo woon benn waay. Bi rab bi génnee, waa ji tàmbali di wax. Mbooloo mi yépp yéemu, 15 waaye ñenn ñi di wax ne: «Ci kàttanu Beelsebul mi di buuru rab yi lay dàqe rab yi.» 16 Te ñeneen ñi di ko fexe fiir; laaj ko kéemaan buy firndeel ne ci asamaan lay jële kàttanam. 17 Waaye Yeesu xam seeni xalaat ne leen: «Bépp nguur bu xaajaloo ci biiram dina tas, te kër yi bu ci nekk di maab ci moroomam. 18 Bu Seytaane di xeex boppam, naka la nguuram mëna yàgge, ndaxte yeena wax ne ci kàttanu Beelsebul laay dàqe rab yi. 19 Te man su fekkee ci kàttanu Beelsebul laay dàqe rab yi; kon seeni taalibe ci ban kàttan lañuy dàqe rab yi? Moo tax ñoom ci seen bopp ñoo leen di àtte. 20 Waaye su fekkee ci kàttanu Yàlla laay dàqe rab yi, kon nguuru Yàlla gi yegsi na ci yeen. 21 Su fekkee ne dafa am ku am doole te yor gànnaayam te aar këram alalam day nekk ci kaaraange. 22 Waaye ku ko ëpp doole bu nëwee daan ko dina jël gànnaay yi mu yaakaaroon te séddale alalam. 23 Ku farul ci man, yaa ngi may xeex; ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.
24 «Bu rab génnee ci nit, day wër ci màndiŋ bi ngir wut fu muy noppaloo. Bu ko amul dina wax ne: "Xaaral, ma dellu ci sama kër bi ma jóge woon." 25 Bu yegsee, fekk ñu bale kër gi, defar ko ba mu jekk. 26 Mu daldi dem woowi juróom ñaari rab yu ko gëna soxor, ñu dugg, dëkk fa. Noonu, melokaanu nit kooku mooy gëna yées na mu meloon bu jëkk.»
27 Bi Yeesu di wax loolu benn jigéen ci biir mbooloo mi yékkëti baatam, ne ko: «Barkeel na, jigéen bi la jur te nàmpal la ci weenam.» 28 Yeesu daldi ko tontu ne: «Neel kay, barkeel na, ki nga xam ne day déglu kàddu Yàlla gi te di ko jëfe.»
29 Naka la mbooloo mi di gën di takku Yeesu tàmbali di wax ne: «Niti jamono jii, dañoo bon. Nu ngi laaj benn màndarga, waaye duñu leen jox benn, bu dul màndargay Yunus bi, 30 ndaxte ni Yunus nekke woon màndarga ci waa dëkku Niniw, noonu Doomu nit ki dina nekk màndarga ci niti jamono jii. 31-32 Te ci bésu àtte ba waa Niniw dinañu jóg ngir tuumaal niti jamono jii, ndaxte bi ñu déggee waare Yunus ba, tuub nañu seen bàkkaar. Te xoolleen! Ku sut Yunus mu ngi fii. Ci bésu àtte ba tamit buur bu jigéen ba dëkkoon ci sudd dina jóg tuumaal niti jamono jii, ndaxte jóge woon na fu sori ngir déglu waxu Suleymaan yu rafet yi. Te xoolleen! Ku sut Suleymaan mu ngi fii.»
Yeesu jàngal na Farisen yi ne dañoo wara setal lu nekk ci seen biir
33 «Kenn du taal làmp ba noppi di ko nëbb walla nga di ci dëpp leket, waaye dañuy koy wékk ngir ñiy dugg mëna gis leer bi. 34 Sa bët mooy sa làmp-yaram: bu sa bët baaxee sa yaram wépp ay nekk ci leer. Waaye bu sa bët bonee sa yaram yépp ay nekk ci lëndëm. 35 Moytul nag leer bi nekk ci yaw doon lëndëm. 36 Kon nag bu sa yaram bi yépp nekkee ci leer, te amul sa benn cér bu nekk ci lëndëm, dangay nekk ci leer mel ni ku làmp ne ràyy ci kawam.»
37 Bi Yeesu di wax loolu, benn Farisen ñaan ko ngir mu lekksi ci këram. Mu yegsi, toog ngir lekk. 38 Bi Farisen bi gisee Yeesu di lekk te raxasul loxoom yi, ni ko aada Yawut yi diglee, mu daldi jaaxle. 39 Boroom bi ne ko: «Yeen Farisen yi dangeen tàmm di raxas ci biti kaas bi ak bu ndab li, te seen biir xol mu ngi fees ak soxor ak yeneen jëf yu bon. 40 Yeen ñu ñàkk xel yi, ndax xamuleen ne, ki sàkk li nekk ci biti, moo sàkk tamit li nekk ci biir? 41 Saraxeleen li nekk ci seen biir xol te seen lépp dina set.
42 «Waaye musiba dal na leen yeen Farisen yi, ndaxte dangeen di sàkk asaka ci xeetu safal bu nekk maanaam: naana ak ru ak ci lujum bu nekk te di sàggane li ëpp solo, maanaam: njubte ak mbëggeelu Yàlla. Loolu ngeen wara def te baña sàggane li ci des. 43 Musiba dal na leen yeen Farisen yi, ndaxte dangeen tàmm di toog ci toogukaay yi féete kanam, ci kër-ñaan yi, te di bëgg ñu leen di nuyu ak ñaari loxo ci péncu dëkk bi. 44 Musiba dal na leen, ndaxte dangeen mel ni ay bàmmeel yu amul xàmmikaay; nit ñi di dox ci kaw seeni bàmmeel te duñu ko xam.»
45 Benn jàngalekatu-yoonu-Musaa wax ko ne: «Jàngalekat bi, soo waxee loolu danga nuy xas nun itam.»
46 Yeesu tontu ko ne ko: «Musiba dal na leen yeen jàngalekati-yoonu-Musaa yi itam, ndaxte dangeen di sas nit ñi ay jëf yu diis waaye, yeen dungeen ci nangoo laal seen catu baaraam. 47 Musiba dal na leen ndaxte yeenay tabax ay bàmmeel ngir Yonent yi seen maam reyoon. 48 Sungeen di def loolu dangeen di wone ne ànd ngeen ci jëf yi seeni maam defoon, ndaxte ñoom ñoo rey yonent yi, te yeen, ngeen di tabax seeni bàmmeel. 49 Moo tax Yàlla ci xelam bu rafet wax na ne: "Dinaa leen yónnee ay yonent ak ay ndaw. Dinañu rey ñenn ñi te fitnaal ñeneen ñi." 50 Ni loolu ame, Yàlla dina këpp ci niti jamono jii deretu yonent yi yépp ñu reyoon ba àddina sosoo ba léegi. 51 Dale ko ci deretu Abel ba ci deretu Sakari mi ñu reyoon ci diggante bérébu saraxlukaay bi ak béréb bu sell bi. Waaw maa ngi leen koy wax, dinañu këpp deretu yonent yi ñu reyoon ci kaw niti jamono jii.
52 «Musiba dal na leen yeen jàngalekati-yoonu-Musaa yi ndaxte dangeena téye caabi xam-xam bi; dugguleen te di tere ñi bëgga dugg, ñu dugg.»
53 Bi Yeesu génnee ci béréb boobu jàngalekati-yoonu-Musaa yi ak Farisen yi di ko sonnal te di ko laaj ci ay mbir yu bari 54 di wut njuumte ci ay kàddoom ngir jëfandikoo ko.