Póol mu ngi ñaax Timote mu dëgër-dëgërlu ci liggéeyu Boroom bi
2
Yaw nag Timote sama doom, na yiwu Yeesu Almasi bi nekk sa kàttan. 2 Mbir yi nga déggoon ma leen di wax ci kanamu ay seede yu bari, na nga leen dénk ay nit ñu gore ñi nga xam ne mën nañu leen jàngal tamit ñeneen. 3 Bokkal ak man coono ni soldaar bu baax bu Yeesu Almasi bi. 4 Soldaar bu bëgga neex ki koy jiite du dugg ci yëfi àddina. 5 Joŋantekat bi tamit, du jot kaala ndam, bu fekkee toppul sart yi ni mu ware. 6 Te itam, beykat bi sonn ci liggéeyam, fàww mu nekk ku jëkka jot wàllam ci ngóob mi. 7 Na nga xalaat ci loolu ma la wax ndaxte Boroom bi dina la leeralal lépp.8 Fàttalikul Yeesu Almasi bi, dekki ci ñu dee ñi, te soqeekoo ci askanu Daawuda, ni ko xibaar bu baax bi may yégle di waxe. 9 Xibaar bu baax boobu moo tax may sonn ba ñu yeew ma ay ceen mel ni defkatu ñaawteef. Waaye kàddug Yàlla gi yeewuñu ko. 10 Loolu moo tax may dëgër-dëgërlu ci lépp, ngir ñi Yàlla tànn, ñoom tamit, ñu mëna am mucc gi ci Yeesu Almasi bi ànd ak màggaay buy law ba fàww.
11 Lii kàddu gu wóor la:
Su nu deewee ak moom,
dinanu dundaat itam ak moom;
12 su nu dëgër-dëgërloo,
dinanu nguuru itam ak moom;
su nu ko weddee,
moom tamit dina nu weddi;
13 su nu gorewul,
moom dina sax ci gore
ndaxte mënula weddi boppam.
Liggéeykat bi neex Yàlla
14 Mbir yooyu, nga wara fàttali ñépp te nga dénk leen bu baax ci kanamu Yàlla ngir ñu baña werante ci li baat yi di tekki. Werante yooyu amuñu benn njériñ waaye dañuy sànkuloo ñi leen di déglu. 15 Defal sa kemtulaay kàttan ci li ngay yégle ni mu ware kàddu dëgg gi, ngir nga mëna taxaw ci kanamu Yàlla ni liggéeykat bu dul am lu muy rus ci liggéeyam. 16 Moytula dugg ci waxtaan yu amul benn njériñ te ànduñu ak ngëm gi, ndaxte ñiy def loolu, dañuy gën di sori Yàlla. 17 Seen njàngale, mu ngi mel ni góom bu dul wér boo xam ne day mujje jàpp yaram bi yépp. Ci ñoom am na Imene ak Filet. 18 Ñoom sori nañu dëgg gi te soriloo ñenn ci ngëm gi ndaxte dañuy wax ne ndekkitel bi am na ba noppi. 19 Moona fondamaa bu dëgër bi Yàlla teg day sax. Kàddu yii lañu fa rëdd: «Boroom bi xam na ñi mu moom» te «Képp kuy woo turu Boroom bi, na sori lu bon.»
20 Ci kër gu mag amul rekk ay jumtukaayu wurus walla yu xaalis, waaye tamit am na yu ñu defare dénk walla ban. Yenn yi ay jumtukaayu bés yu réy lañu, yi ci des ñooy yi ñuy jëfandikoo bés bu nekk. 21 Kon nag, képp ku setal boppam ci lu bon, dina nekk jumtukaay bu tedd bi ñu ber ngir njaatigeem, te mu amal ko njériñ, ndaxte waajal na boppam ngir bépp jëf bu baax.
22 Dawal ba sori bëgg-bëgg waxambaane yi. Na nga topp njubte, ngëm, mbëggeel, ak jàmm; yaw ak ñépp ñuy woo turu Boroom bi ak xol bu set. 23 Waaye moytula dugg ci waxtaanu neen yu amul benn njériñ. Xam nga ne loolu day jur xuloo. 24 Jaamu Boroom bi warul di xuloo, waaye dafa wara lewet ci ñépp, mëna jàngale, te mëna muñ coono yi. 25 Dafa wara jubanti ci lewet ñiy weddi njàngaleem. Xéy-na Yàlla dina leen may ñu tuub seeni bàkkaar ba xam dëgg gi. 26 Su boobaa, seen xel dina dellusi ci ñoom, te dinañu rëcc ci fiiru Seytaane mi leen jàppoon te noot leen ci coobareem.