Póol mu ngi jàngale ci dundinu mbooloo ñi gëm
2
Waaye yaw, waxal li dëppoo ak njàngale mu dëggu mi. 2 Na góor ñu mag ñi ànd ak seen sago, am faayda, teey, ñu dëggu ci ngëm gi, ci mbëggeel gi, ak ci dëgër-dëgërlu.
3 Noonu tamit na jigéen ñu mag ñi dund ci anam bu neex Yàlla, ñu baña jëw seeni moroom mbaa ñu nekk ay màndikat. Nañu jàngale lu baax 4 ngir mëna ñaax jigéen ñu ndaw ñi, ñu bëgg seen jëkkër ak seeni doom, 5 ñu ànd ak seen sago, set ci seen dundin, ñu toppatoo seen kër, fees ak mbaax, te déggal seen jëkkër, ngir ñeneen ñi baña wax lu ñaaw ci kàddug Yàlla gi. 6 Noonu tamit ñaaxal waxambaane yi ngir ñu ànd ak seen sago.
7 Yaw ci sa bopp, ci lépp nekkal royukaay ci jëf yu baax. Jàngaleel ci njubte ak faayda. 8 Na sa waare dëggu te ñàkk lu ñu koy ŋàññe, ngir sunu noon yi rus, ndaxte gisuñu dara lu ñaaw lu ñuy wax ci nun.
9 Na jaam yi déggal seeni njaatige ci lépp, ñu neex leen, ñu bañ leena weddi, 10 te bañ leena sàcc, waaye nañu wone ne mën nañu leen wóolu, ngir rafetal njàngale Yàlla sunu musalkat.
11 Ndaxte Yàlla feeñal na yiwam, mu nekk buntu mucc ngir ñépp. 12 Yiw boobu moo nuy jàngal nu bàyyi lépp li nuy tere nu takku ci Yàlla te nu bàyyi tamit bëgg-bëgg àddina. Noonu nu mëna dund ci sago, ci njub, ak takku ci Yàlla ci jamono jii 13 nuy xaar bés bi Yàlla di matal yaakaar bu barkeel bi, di ñëwu Yeesu Almasi bi ci màggaayam. Mooy sunu Yàlla bu mag bi ak sunu musalkat. 14 Joxe na boppam ngir nun, ngir yewwi nu ci lépp lu bon, ngir def nu benn mbooloo bu mu setal, bi mu moom, moom rekk, te nu farlu di matal ay jëf yu baax.
15 Jàngaleel mbir yooyu, nga ñaax leen te nga yedd leen ak sa sañ-sañ bépp. Bul nangu kenn yab la.