Nit ku gëm war na def ay jëf yu baax
3
Fàttalil mbokki gëmkat yi ngir ñu déggal njiit yi ak kilifa yi, di jëfe seeni ndigal, te ñu waaj ngir def bépp jëf bu baax. 2 Buñu wax kenn lu bon, waaye nañu dal te baax, te di wone saa su nekk lewet ci nit ñépp. 3 Ndaxte nun tamit nii lanu meloon bu jëkk: ñàkk xel, déggadil Yàlla, réer, di ay jaamu bépp xeetu bëgg-bëgg ak sunu bànneexu bakkan. Danu doon dund ci soxor ak ci ñee; danu doon bañante ak ñeneen ñi. 4 Waaye bi Yàlla sunu Musalkat feeñalee mbaaxam ak mbëggeelam ci nit ñi, 5 musal na nu. Du jëf yu jub yi nu mataloon moo tax, waaye ndax yërmandeem ci nun. Musal na nu jaarale ko ci juddu bu bees bi, maanaam raxas na sunu xol, te yeesalaat na nu ci Xel mu Sell 6 mi mu sotti ci sunu kaw ba mu ne gàññ, jaarale ko ci Yeesu Almasi bi sunu Musalkat. 7 Noonu segem Yàlla dafa noo àtte ni ñu jub ci yiwam, dinanu donn dund gu dul jeex, gi nekk sunu yaakaar. 8 Loolu kàddu gu wóor la te bëgg naa nga wéy di wax ci mbir yooyu, ngir ñi gëm ci Yàlla góor-góorlu ngir matal jëf yu baax. Loolu mooy li baax te am njériñ ci nit ñi.
9 Waaye bañal waxtaan yu amul solo yi, lépp lu jëm ci limi maam yi, xuloo yi ak werante yu jëm ci Yoonu Musaa. Amuñu benn njériñ, te ay waxu neen lañu. 10 Ki nga xam ne day indi xaajaloo, artu ko benn ba ñaari yoon. Su la bañee déglu nag, nga dàq ko ci mbooloo gëmkat yi. 11 Ndaxte xam nga bu baax ne nit ku mel noonu sori na yoon bu jub bi, bàkkaar na te moo teg boppam daan.
Póol mu ngi tàggatoo ak Tit
12 Su ma la yónnee Artemas walla Tisig nanga gaawantu fekksi ma ci dëkku Nikopolis, ndaxte dama jël dogal def fa jamono seddaay bi. 13 Nanga jox Senas layookat bi ak Apolos lépp li ñu soxla ci seen tukki bi, ngir ñu baña ñàkk dara. 14 Fàww ñi bokk ci nun tamit jàng di matal ay jëf yu baax, ngir ñu mëna faj soxla yu jàmp yi. Noonu seen dund dina am njériñ. 15 Ñépp ñi nekk ak man, ñu ngi lay nuyu. Nuyul sunu xarit yi nu bokkal ngëm gi. Na yiwu Yàlla nekk ak yeen ñépp.