Yàlla nanguwul ñiy réy-réylu
4
Fan la xeex yi ak xuloo yi ci seen biir di jóge? Ñu ngi jóge ci seen bëgg-bëggu bakkan yiy xeex ci yeen. 2 Dangeen di xemmem dara te dungeen ci jot, te jaral na leen ngeen di rey; yeena ngi wut ak iñaan, te mënuleen am. Dangeen di xeex ak di xuloo. Amuleen li ngeen bëgg, ndaxte ñaanuleen ko Yàlla. 3 Te bu ngeen di ñaan, dungeen jot ndaxte li leen ci xiir moo baaxul: li ngeen ci jublu mooy seen bëgg-bëggu bakkan. 4 Yeen ñii di moy Yàlla! Ndax xamuleen ne xaritoo ak àddina si mooy noonoo ak Yàlla? Ki bëgga xaritoo ak àddina si, day nekk noonu Yàlla. 5 Ndax xalaat ngeen ne, ci neen la Mbind mi wax ne: «Yàlla dafa bëgg Xel mi mu def ci nun ba di ko fiire»? 6 Waaye Yàlla may na nu yiw bu gëna mag. Looloo tax Mbind mi wax na ne: «Yàlla nanguwul ñiy réy-réylu waaye day may yiwam ñiy suufeelu.» 7 Kon nag, jébbaluleen ci Yàlla. Bañleen di nangul Seytaane, te dina daw, sori leen. 8 Jegeleen Yàlla te dina leen jege. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo! Te yeen naaféq yi, setalleen seeni xol! 9 Nekkleen ci tiis tey naqarlu bay jooy. Na seen ree soppeeku nekk jooy te seen mbégte soppeeku nekk tiis. 10 Suufeeluleen ci kanamu Boroom bi te dina leen yékkëti.Buleen àtte seen moroom
11 Mbokk yi, buleen di wax lu bon ci seen moroom. Kiy wax lu bon ci moroomam walla di ko àtte, day wax lu bon ci yoon bi te di ko àtte. Te boo àttee yoon bi nekkatoo ki koy déggal, waaye yaay ki koy àtte. 12 Yàlla rekk mooy ki tëral yoon bi te mooy àttekat bi. Moom rekk moo mëna musal nit te moo mëna sànk nit. Yaw nag, yaay kan bay àtte sa moroom?
Buleen doyloo seen bopp
13 Léegi nag, dégluleen yeen ñiy wax ne: «Tey walla suba dinanu dem ci benn dëkk, dinanu fa am at, di jaay ba am ci xaalis.» 14 Moona xamuleen li seen dund di nekk ëllëg. Dangeen mel ni lay bu ndaw buy feeñ ab diir bu gàtt ba noppi wàcc. 15 Waaye lii ngeen wara wax: «Su neexee Boroom bi, dinanu dund te dinanu def lii walla lale.» 16 Waaye yeena ngi wonewu tey réy-réylu, te bépp wonewu bu mel noonu lu bon la. 17 Kon nag, ku xam lu baax li mu wara def te defu ko bàkkaar na.