Ki gëm dafa wara téye làmmiñam
3
Mbokk yi, bu ñu bari ci yeen wuta nekk jàngalekatu mbooloo ñi gëm, ndaxte xam ngeen ne nun, jàngalekat yi, sunu àtte mooy gëna metti bu ñeneen ñi. 2 Ndaxte nun ñépp danuy juum ci anam yu bari. Ki dul juum ci ay waxam, kooku, nit ku mat sëkk la, te mën na noot yaramam bi yépp. 3 Danuy laxaab fas ngir mu déggal nu, te noonu dinanu mëna yóbbu fi nu bëgg jëmmam bi yépp. 4 Xoolleen gaal yi ak lu ñu réy-réy te ngelaw bu am doole di leen yóbbu, terewul dawalkat bi da leen di yóbbu fu ko neex ak weñ bu tuuti. 5 Noonu tamit làmmiñ cér bu tuuti la ci yaramu nit, waaye day bàkkoo ay jëf yu réy. Xoolleen ni taal bu tuuti mëna lakke àll bu yaatu. 6 Làmmiñ tamit taal la, dafa fees dell ak mbon, bokk ci sunuy céru yaram tey tilimal sunu yaram bi yépp. Mu ngi taal sunu àddina si yépp ak xal bu jóge ci safara. 7 Nit mën na noot xeetu mala yépp ngir ñu déggal ko: muy rabu àll yi, picc yi, yiy raam ak yi ci géej gi; te noot na leen. 8 Waaye kenn mënula noot làmmiñ: musiba la bu dul dal mukk te fees ak daŋar buy rey. 9 Làmmiñ lanuy sante Boroom bi di sunu Baay, te tamit moom lanuy móoloo nit ñi Yàlla sàkk ci melokaanam. 10 Ci benn gémmiñ la kàdduy cant ak kàdduy móolu di génne. Mbokk yi, warul deme noonu. 11 Ndax benn bëtu ndox mën na génne ndox mu neex ak ndox mu naqari? 12 Samay mbokk, ndax garabu gaŋ mën na jur oliw? Ndax garabu reseñ mën na jur gaŋ? Bëtu ndox mu saf xorom mënula génne ndox mu neex.
Xel mu rafet mi jóge ci asamaan
13 Kan ci yeen moo am xel mu rafet te am xam-xam? Na ko wone ci dundinam bu baax, maanaam ci ay jëfam yi mu matal ak suufeelu bu jóge ci xel mu rafet. 14 Waaye su ngeen amee xol bu wex xàtt ak iñaan ak xëccoo, buleen ci bàkku te buleen fen di weddi dëgg. 15 Lu mel noonu du xel mu rafet mu jóge ci asamaan waaye yëfu àddina la, yëfu nit la, mu ngi jóge ci Seytaane. 16 Ndaxte fi iñaan ak xëccoo nekk, foofu la jaxasoo nekk tamit ak bépp jëfu ñaawteef. 17 Waaye xel mu rafet mi jóge ci asamaan dafa set ba noppi, ànd ak jàmm, woyof, dal, fees ak yërmande, tey jur ay jëf yu baax. Du gënatle nit ñi te du naaféq. 18 Nit ki bëgg jàmm ci li ko wër day ji jàmm tey góob meññeefu njubte.