Ki gëm warul di gënatle
2
Mbokk yi, ngëm gi ngeen am ci sunu Boroom bi ñuy màggal, di Yeesu Almasi bi, warul ànd ak gënatle ci seen biir. 2 Su fekkee ne dafa am benn waay bu ñëw ci seen ndaje, mu sol jaaro wurus ak yére yu rafet; mu am keneen ku néew doole, sol yére yu tilim, duggsi moom itam; 3 ngeen jox cér bu mag boroom yére yu rafet yi te ngeen ne ko: «Kaay toog ci toogukaay bu féete ci kanam,» te ngeen wax néew di doole bi: «Taxawal fee» walla «Toogal ci suuf, ci samay tànk.» 4 Su ngeen jëfe noonu, yeena ngi gënatle ci seen biir, te seen àtte mu ngi jóge ci seen xel yu ñaaw.5 Yeen samay mbokk yi ma bëgg, dégluleen: ndax Yàlla tànnul ñi néew doole ci àddina si, ngir ñu am ngëm gu réy te ñu donn nguur gi Yàlla digoon ñi ko bëgg? 6 Waaye yeen, yeena ngi toroxal ku néew doole ki. Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noot te di leen yóbbu ci kanamu àttekaay yi? 7 Xanaa du ñoom ñooy wax lu ñaaw tur bu rafet bi ngeen di wuyoo?
8 Yoonu nguuru Yàlla ci Mbind mi wax na ne: «Nanga bëgg sa moroom ni nga bëgge sa bopp.» Su ngeen jëfee noonu, def ngeen lu baax. 9 Waaye su ngeen di gënatle nit ñi, bàkkaar ngeen te yoonu Yàlla bi dina leen daan, ndaxte déggalooleen ko. 10 Ndaxte ku déggal yoon bi yépp ba mu des benn ndigal rekk, moy nga yoon bi yépp. 11 Ndaxte ki wax «bul njaaloo» moo wax tamit «bul rey nit». Su fekkee nag njaaloowoo waaye rey nga nit, moy nga yoon bi. 12 Waxleen tey jëfe, mel ni nit ñi ñu nara àtte ci yoon biy goreel, 13 ndaxte àtte Yàlla du ànd ak yërmande ci ku dul yërëm moroomam. Yërmande moo am ndam ci kaw àtte.
Ngëm bu ànd ak jëf
14 Mbokk yi, bu nit waxee ne: «Am naa ngëm,» te wonewu ko ci ay jëfam, lan lay jériñ? Ndax googu ngëm mën na ko musal? 15 Su amee mbokk bu góor walla bu jigéen bu rafle yére te amul lu muy dunde bés bu nekk, 16 te kenn ci yeen wax ko ne: «Demal ci jàmm, nga sol sa yére, te nga lekk ba regg.» Bu ngeen ko waxee loolu te fajuleen soxlaam, loolu lu muy jériñ? 17 Noonu la ngëm gi mel: su àndul ak jëf, dee na.
18 Waaye kenn dina wax ne moo am ngëm te man maa am ay jëf. Bu booba dinaa ko tontu ne: «Won ma sa ngëm gu àndul ak ay jëf te man dinaa la won sama ngëm jaarale ko ci samay jëf.» 19 Ndax gëm nga ne Yàlla kenn la? Lu baax la! Rab yi sax gëm nañu loolu bay lox. 20 Nit ku ñàkk xel ki, ndax danga bëgga am firnde buy wone ne ngëm gu àndul ak ay jëf jériñul dara? 21 Sunu maam Ibraayma naka la ko Yàlla àtte ni nit ku jub? Ci ay jëfam, bi mu joxee doomam Isaaxa ni sarax ci saraxlukaay bi. 22 Kon gis nga ne ngëmam day feeñ ci ay jëfam te noonu ngëmam mat na jaarale ko ci ay jëfam. 23 Noonu mat na, li Mbind mi wax ne: «Ibraayma gëm na Yàlla te Yàlla àtte na ko ni nit ku jub,» te ñu woowe ko xaritu Yàlla. 24 Kon nag gis ngeen ne, Yàlla day àtte nit, ni ku jub ndax ay jëfam, waaye du rekk ndax ngëmam. 25 Noonu la mel tamit ak Raxab jigéen ju doon jaay yaramam. Yàlla àtte woon na ko ni nit ku jub ndax ay jëfam, bi mu dalalee ndawu Yawut yi te dimbale leen, jaarloo leen beneen yoon ba ñu rëcc. 26 Noonu, yaram bu amul ruu, dee na. Noonu tamit la mel ngëm gu àndul ak ay jëf, dee na.