Ki xam Yàlla dafay dox ci ndigalam
2
Yeen samay doom, maa ngi leen di bindal lii ngir ngeen baña bàkkaar. Waaye bu kenn ci yeen bàkkaaree, am nanu ku nu taxawu ci wetu Baay bi. Moom mooy Yeesu Almasi bi, di ku jub ki. 2 Moom moo joxe boppam ni sarax ngir giifal mer bi Yàlla amoon ci nun ndax sunuy bàkkaar. Du sax ngir sunuy bàkkaar nun rekk waaye ngir bàkkaari àddina si yépp.
3 Su nu déggalee ndigali Yàlla, ci noonu, nun, danuy xam ne xam nanu ko. 4 Kiy wax ne: «Xam naa ko», waaye déggalul ay ndigalam, fenkat la, te dëgg gi nekkul ci moom. 5 Waaye kiy déggal kàddoom, mbëggeelu Yàlla mat na sëkk ci moom. Ci noonu lanuy xame ne ci Yàlla lanu sax. 6 Kiy wax ne ci moom la sax dafa wara doxe ni Almasi bi doon doxe.
7 Samay soppe, du ndigal bu bees laa leen di bindal, waaye ndigal bu yàgg la, bi ngeen jot dale ko ci njàlbéen ga. Ndigal bu yàgg boobu mooy kàddu gi ngeen déggoon. 8 Moona ndigal bu bees laa leen di bindal, muy dëgg ci Yeesu ak ci yeen, ndaxte lëndëm gaa ngi weesu, te leer gu wóor gi fenk na ba noppi. 9 Kiy wax ne dafay dox ci leer gi te bañ mbokkam, mu ngi ci lëndëm gi ba léegi. 10 Ki bëgg mbokkam dafay sax ci leer gi, te noonu dara mënula tax mu daanu ci bàkkaar. 11 Waaye ki bañ mbokkam mu ngi ci lëndëm; dafay dox ci lëndëm te xamul fi muy dem ndaxte lëndëm gi moo ko gumbooloo.
Ndigalu Yowaana ci lu jëm ci àddina sii ak ñiy xeex Almasi bi
12 Maa ngi leen di bind, yeen samay doom, ndaxte Yàlla baal na leen seeni bàkkaar ndax turu Yeesu Almasi bi. 13 Maa ngi leen di bind, yeen baay yi, ndaxte xam ngeen ki nekk dale ko ci njàlbéen ga. Maa ngi leen di bind, yeen waxambaane yi, ndaxte daan ngeen ku bon ki. 14 Bind naa leen, yeen xale yi, ndaxte xam ngeen Baay bi. Bind naa leen, yeen baay yi, ndaxte xam ngeen ki nekk dale ko ci njàlbéen ga. Bind naa leen, yeen waxambaane yi, ndaxte am ngeen doole, kàddu Yàlla gi sax na ci yeen, te daan ngeen ku bon ki.
15 Buleen bëgg àddina si walla mbir yi nekk ci àddina si. Su kenn bëggee àddina si, mbëggeelu Baay bi nekkul ci moom, 16 ndaxte lépp li nekk ci àddina si, maanaam bëgg-bëgg yaram, xemmem li say bët di gis, ak wonewu ci li nga am, loolu lépp jógewul ci Baay bi, waaye ci àddina si la jóge. 17 Àddina si ak bëgg-bëggam yi dinañu weesu, waaye kiy def coobare Yàlla dina dund ba fàww.
18 Yeen xale yi, waxtu bu mujj bi jot na. Dégg ngeen ne kiy xeex Almasi bi dina ñëw. Léegi nag, ñu bari ñiy xeex Almasi bi ñu ngi fi. Loolu moo tax nu xam ne waxtu bu mujj bi jot na. 19 Ci sunu biir lañu génne, waaye bokkuñu woon ci nun, ndaxte su ñu bokkoon ci nun doon nañu des ak nun. Waaye dañoo génn ngir mu leer ci ñépp ne bokkuñu ci nun.
20 Waaye yeen, Ku Sell ki may na leen Xelam, te yeen ñépp xam ngeen dëgg gi. 21 Kon nag su ma leen di bind nekkul ne xamuleen dëgg gi, waaye li ngeen ko xam moo tax, te xam ngeen tamit ne amul benn fen bu jóge ci dëgg gi. 22 Kan mooy fenkat bi? Moom mooy kiy weddi ne Yeesu mooy Almasi bi. Kooku mooy kiy xeex Almasi bi, maanaam kiy weddi Baay bi ak Doom ji. 23 Képp ku weddi Doom ji amuloo tamit Baay bi, te ku nangu Doom ji ci kanamu ñépp am na tamit Baay bi.
24 Yeen nag, li ngeen déggoon dale ko ci njàlbéen ga, na sax ci yeen. Li ngeen déggoon dale ko ci njàlbéen ga, bu saxee ci yeen, yeen tamit dingeen sax ci Doom ji ak ci Baay bi. 25 Lii la nu Almasi bi ci boppam digoon: dund gu dul jeex gi. 26 Bind naa leen loolu ci lu jëm ci ñi leen di jéema nax.
27 Yeen nag, Xel mu Sell mi leen Almasi bi may sax na ci yeen, ba tax soxlawuleen kenn di leen jàngal. Ndaxte Xel mu Sell mi da leen di jàngal lépp, te moom dëgg la, du fen mukk. Kon nag, saxleen ci Almasi bi ni leen ko Xel mu Sell mi jàngale.
Doomi Yàlla du wéy ci bàkkaar
28 Waaw samay doom, saxleen ci Almasi bi, ngir bés bi muy feeñ, nu fees ak kóolute te baña am gàcce ci kanamam bu ñëwee. 29 Xam ngeen ne Almasi bi dafa jub; xam ngeen tamit ne képp kuy def lu jub doomu Yàlla la.