3
Xoolleen mbëggeel gi nu Baay bi bëgg ni mu réye, ba tax ñu nuy woowe doomi Yàlla, te moom lanu. Àddina si xamul Yàlla, loolu moo tax xamu nu. 2 Samay soppe, léegi ay doomu Yàlla lanu, te li nuy doon ëllëg feeñagul. Xam nanu ne bu Almasi bi feeñee dinanu ko gis ni mu nekke ba tax nu niroo ak moom. 3 Képp ku am yaakaar boobu ci moom setal na boppam, ni Almasi bi ci boppam sete.4 Képp ku bàkkaar déggalul yoon bi, ndaxte bàkkaar mooy ñàkka déggal yoon bi. 5 Waaye xam ngeen ne Yeesu Almasi bi dafa feeñ ngir dindi bàkkaar yi, te amul benn bàkkaar ci moom. 6 Képp ku sax ci moom du bàkkaar. Képp kuy wéy ci bàkkaar gisu ko te xamu ko.
7 Samay doom buleen kenn nax: képp kuy def lu jub, dafay jub ni Almasi bi ci boppam jube. 8 Képp kuy def bàkkaar ci Seytaane la bokk, ndaxte Seytaane mu ngi bàkkaar dale ko ci njàlbéen ga ba tey. Li tax Doomu Yàlla ji feeñ mooy ngir yàq jëfi Seytaane. 9 Képp kuy doomu Yàlla du def bàkkaar, ndaxte kàddu Yàlla gi day sax ci moom mel ni jiwu, te mënatul sax ci bàkkaar, ndaxte Yàlla mooy baayam. 10 Ci loolu lanuy ràññee doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul jëfe ci njubte bokkul ci Yàlla, rawatina ki bëggul mbokkam.
Bëgganteleen ci seen biir
11 Ndaxte lii mooy xibaar bi ngeen déggoon dale ko ci njàlbéen ga: danoo wara bëggante ci sunu biir, 12 te baña def ni Kayin mi bokkoon ci ku bon ki te rey rakkam. Lu tax mu reyoon ko? Ndaxte jëfam yi dañoo bonoon te yu rakkam yi juboon.
13 Yeen samay mbokk, buleen jaaxle bu leen àddina si bañee. 14 Nun, xam nanu ne danoo jóge ci dee, jàll ci dund gi ndaxte danoo bëgg sunuy mbokk. Ki bëggul, day sax ci dee. 15 Képp ku bañ mbokkam, reykatu nit la, te xam ngeen ne dund gu dul jeex gi du sax ci benn reykatu nit. 16 Ci nii lanuy xame mbëggeel: Yeesu Almasi bi joxe na bakkanam ngir nun. Nun tamit danoo wara joxe sunu bakkan ngir sunuy mbokk. 17 Waaye bu kenn amee alalu àddina, mu gis mbokkam mu nekk ci coono te mu tëj xolam, naka la mbëggeelu Yàlla di saxe ci moom?
18 Samay doom, bunu bëgg ci kàddu ak ci làmmiñ rekk, waaye ci jëf ak ci dëgg. 19 Ci noonu lanuy xame ne ci dëgg gi lanu bokk, te dinanu dalal sunu xol ci kanamu Yàlla: 20 su fekkee ne sunu xol dafa nuy tuumaal, Yàlla moo gëna màgg sunu xol te xam na lépp. 21 Samay soppe, su fekkee ne sunu xol tuumaalu nu, am nanu kóolute ci kanamu Yàlla, 22 te lépp lu nu ko ñaan, dinanu ko jot ci moom, ndaxte danoo déggal ay ndigalam tey def li ko neex. 23 Te ndigalam bi mooy nu gëm ci turu doomam Yeesu Almasi bi te nu bëggante ci sunu biir, ni mu nu ko sante. 24 Kiy déggal ay ndigalam day sax ci Yàlla te Yàlla sax ci moom. Xam nanu ne Yàlla dafa sax ci nun jaarale ko ci Xel mu Sell mi mu nu may.