Yeesu wax na li andil nit sobe
7
Ay Farisen ak ay jàngalekati-yoonu-Musaa jóge Yerusalem, daje ci wetu Yeesu. 2 Ñu gis ñenn ci taalibe yi di lekk te seeni loxo setuñu, maanaam raxasuñu seeni loxo. 3 Farisen yi ak Yawut yépp daawuñu woon lekk te raxasuñu seeni loxo ni mu ware. Noonu lañu doon toppe seeni aaday maam. 4 Saa su ñu jógee ci pénc ba tamit daawuñu lekk, feek raxasuwuñu ba noppi te dañu doon déggal yeneen aada yi ñu jot, maanaam raxas ay kaas, ay cin, ak ay ndabu xànjar. 5 Farisen yi ak jàngalekatu-yoonu-Musaa laaj Yeesu ne: «Lu tax sa taalibe yi duñu topp sunuy aaday maam? Lu tax ñuy lekk te seeni loxo setuñu?» 6 Mu ne leen: «Naaféq yi! Esayi waxoon na dëgg bu wóor bi mu doon wax ci turu Yàlla ci lu jëm ci yeen, ndaxte lii lañu bind:
"Askan bii daf may màggal ak seen gémmiñ,
waaye seen xol sori na ma.
7 Ci neen lañu may jaamu
ndaxte ay ndigalu nit lañuy jàngale
jàppe ko samay ndigal."»
8 Yeesu yokk ca ne: «Dëddu ngeen ndigalu Yàlla bi ngir sàmm ay aada nit. 9 Dangeen neenal ndigalu Yàlla bi ngir topp seen aada, 10 ndaxte Musaa waxoon na ne: "Teralal sa baay ak sa yaay. Ku saaga baayam walla yaayam nañu ko rey." 11 Waaye yeena ngi wax ne: "Ku wax baayam walla yaayam ne: 'Sama alal bi ma la wara jàppale, korban la.' (Korban mu ngi tekki sarax bi ñu jébbal Yàlla.) 12 Noonu dungeen ko bàyyi ngir mu jàppale baayam walla yaayam." 13 Ci anam boobu ngeen di neenale kàddu Yàlla gi ndax seeni aada yi ngeen donnante. Te ngeen di def yeneen mbir yu bari yu mel noonu.»
14 Noonu Yeesu woowaat mbooloo mi te ne leen: «Dégluleen ma yeen ñépp te ngeen ràññee: 15-16 amul dara luy jóge ci biti tey dugg ci nit lu koy andil sobe. Waaye liy génn ci nit loolu mooy andil nit sobe.»
17 Bi Yeesu duggee ci kër gi ba sori mbooloo mi, taalibeem yi laaj ko mu firi leen léeb boobu. 18 Mu ne leen: «Ndax yeen tamit ràññeewuleen? Xamuleen ne amul dara luy jóge ci biti te dugg ci nit, mën ko andil sobe? 19 Loolu du dugg ci xolam waaye ci biiram ba jàll, génn ci yaramam.» Jaarale ko ci kàddu yooyu daganal na bépp ñam. 20 Te mu yokk ca ne: «Li génn ci nit loolu moo koy andil sobe, 21 ndaxte ci biir xolu nit la xalaat yu bon yi di génne: ay séy yu yoon tere, sàcc, rey nit, 22 njaaloo, bëgge, coxorte, njublaŋ, jubadi, iñaan, saaga, réy-réylu ak bépp jëfi dof. 23 Yu bon yooyu yépp day génne ci xolu nit te loolu moo koy andil sobe.»
Benn jigéen bu nekkul Yawut ñaan na Yeesu mu wéral doomam bu jigéen
24 Gannaaw loolu Yeesu jóge foofu te dem ci diiwaan bi dëkku Tir nekk. Mu dugg ci benn kër, bëggul woon kenn xam ko, waaye mënul woon nëbbatu. 25 Naka la Yeesu yegsee rekk, benn jigéen bu doomam bu jigéen amoon rab dégg ñuy wax ci moom te mu ñëw daanu ci tànkam yi. 26 Jigéen boobu nekkul woon Yawut. Mu ngi cosaanoo Fenisi ci réewu Siri. Mu ñaan Yeesu ngir mu dàq rab bi nekk ci doomam bu jigéen. 27 Yeesu ne ko: «Bàyyil xale yi regg ba noppi, ndaxte baaxul ñuy jël mburu xale yi, di ko sànnil xaj yi.» 28 Jigéen ji tontu ko ne: «Loolu dëgg la, Boroom bi, waaye xaj yi nekk ci suufu bérébu lekkukaay bi sax dañuy lekk ruusitu xale yi.» 29 Mu ne ko: «Ci kàddu googu, demal! Rab bi génn na ci sa doom bu jigéen.» 30 Bi mu ñibbee këram, mu fekk xale bi tëdd ci lal bi, te rab bi génn ci moom.
Yeesu wéral na benn waay bu tëx te dër
31 Noonu Yeesu jóge ci diiwaan bi dëkku Tir nekkoon, jaar ci dëkku Sidon, jëm ci dexu Galile. Mu jàll ci diiwaan bi ñuy woowe fukki dëkk yi. 32 Foofu ñu andil ko benn waay bu tëx te dër. Ñu ñaan Yeesu ngir mu teg ko ay loxoom. 33 Yeesu yóbbu waa ji ba mu sori mbooloo mi, mu jël baaraamam yi, fatt ko ci noppi waa ji, tifli, te laal làmmiñu waa ji. 34 Noonu mu yékkëti bëtam yi ci asamaan, noyyi, te ne: «Effata,» luy tekki ne «ubbeekul.» 35 Ci saa si noppi waa ji ubbeeku, làmmiñam yewweeku te mu tàmbali di wax lu leer. 36 Yeesu dénk ñi fa nekkoon ñu bañ ko wax kenn, waaye lu mu leen gën di dénk, ñu koy gën di siiwal. 37 Nit ñi waaru woon nañu lool tey ne: «Def na lépp mu baax. Mu ngi déggloo sax ñi tëx tey waxloo ñi luu.»