Yeesu dundal na ñeenti junni góor te artu taalibeem yi
8
Ci bés yooyu mbooloo mu takku dajaloowaat, wër Yeesu te amuñu woon lu ñuy lekk. Mu woo taalibeem yi te ne leen: 2 «Damaa yërëm mbooloo mi, ndaxte ñetti fan a ngi ñu nekk ak man te amuñu dara lu ñuy lekk. 3 Su ma leen yewwee ñu ñibbi ak xiif, seen néew doole dina leen daaneel ci yoon bi, ndaxte ñenn ñi fu sori lañu jóge.» 4 Taalibeem yi tontu ko ne: «Fan lanuy jële mburu ci màndiŋ bii ngir dundal nit ñii?» 5 Yeesu laaj leen ne: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu tontu ko: «Juróom ñaar.» 6 Noonu mu jox ndigal mbooloo mi ñu toog ci suuf si. Mu jël juróom ñaari mburu yi, sant Yàlla, damm leen, te jox leen taalibeem yi ngir ñu séddale leen. Ñu daldi leen séddale mbooloo mi. 7 Amoon na tamit ay jën yu ndaw. Yeesu daldi leen barkeel te mu waxaat taalibeem yi ñu séddale leen tamit. 8 Ñépp lekkoon nañu ba regg, te ñu for ci juróom ñaari pañe yu fees ci daggit yi desoon. 9 Amoon na foofu lu tollook ñeenti junniy góor. Noonu Yeesu yewwi leen. 10 Ci saa si mu yéeg ci gaal, moom ak taalibeem yi, te ñu dem diiwaanu Dalmanuta.11 Farisen yi yegsi te tàmbale werante ak Yeesu. Ñu laaj ko kéemaan buy firndeel ne ci asamaan lay jële kàttanam ngir fiir ko. 12 Yeesu noyyi bu baax te ne: «Lu tax niti jamono jii di laaj màndarga? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, duñu leen jox benn màndarga.» 13 Ci kaw loolu Yeesu bàyyi leen fa, yéegaat ci gaal gi te jëm ci beneen wetu dex gi.
14 Taalibe yi fàtte woon nañu yóbbaale mburu. Benn mburu rekk lañu amoon ci gaal gi. 15 Yeesu jox leen ndigal bii: «Xoolleen! Moytuleen lawiiru Farisen yi ak bu Erodd.» 16 Taalibe yi di werante ci seen biir naan: «Li nu amul mburu moo tax muy wax loolu.» 17 Yeesu xam loolu te ne leen: «Lu tax ngeen di werante ci li ngeen amul mburu? Ràññeewuleen ba léegi walla seen xam-xam dafa tëju? Ndax seeni xol dafa dëgër? 18 Ndax dangeen am ay bët te gisuleen? Ndax dangeen am ay nopp te dégguleen? Ndax fàttalikuwuleen? 19 Bi ma dammee juróomi mburu yi ngir juróomi junni góor ya, ñaata pañe ci daggit yi desoon ngeen yóbbu woon?» Ñu ne ko: «Fukk ak ñaar?» 20 «Te bi ma dammee juróom ñaari mburu yi ngir ñeenti junni góor ya, ñaata pañe yu fees ak daggit ngeen ci yóbbu woon?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.» 21 Noonu Yeesu ne leen: «Ràññeewuleen ba léegi?»
Yeesu wéral na benn gumba ci dëkku Betsayda
22 Yeesu ak taalibeem yi yegsi nañu dëkku Betsayda. Foofu ñu andil ko benn waay bu gumba. Ñu ñaan ko ngir mu laal ko. 23 Noonu Yeesu jàpp loxo gumba bi te wommat ko ba ñu génn dëkk bi. Mu tifli ci bëti gumba bi, teg ko ay loxoom, te laaj ko ne: «Ndax yaa ngi gis dara?» 24 Gumba bi yékkëti bëtam yi te ne ko: «Maa ngi gis ay nit yu mel ni ay garab yuy dox.» 25 Noonu Yeesu tegaat loxoom yi ci bëti gumba bi, bëtam yi ubbeeku, mu wér, te mu gis lu leer. 26 Yeesu ne ko: «Ñibbil te bul duggaat ci dëkk bi.»
Yeesu mooy Almasi bi te war na sonn te dee
27 Yeesu ànd ak taalibeem yi, jëm ci gox yi wër Sesare bu Filib. Ci yoon bi mu tàmbali di leen laaj ne: «Nit ñi kan lañuy wax ne moom laa?» 28 Ñu tontu ko ne: «Am na ñuy wax ne yaw yaay Yaxya. Ñii ne yaw yaay Ilyaas. Ñi ci des ne kenn ci yeneen yonent yi.» 29 Mu laaj leen: «Yeen nag, kan ngeen wax ne moom laa?» Piyeer tontu ko ne: «Yaw yaay Almasi bi.» 30 Mu dénk leen ngir ñu bañ ko wax kenn.
31 Noonu mu tàmbali di leen jàngal ne: «Fàww Doomu nit ki sonn lool. Noonu mag ñi, njiiti-jébbalkati-sarax yi, ak jàngalekati-yoonu-Musaa dëddu ko, rey ko, te mu dekki ci ñetteelu fan ba.» 32 Doon na wax loolu ci ay kàddu yu leer. Noonu Piyeer woo ko, wéetoo ak moom, tàmbali di ko yedd. 33 Waaye mu walbatiku, daldi xool taalibeem yi, mu gëdd Piyeer ak doole naan: «Sori ma Seytaane, jàll ci sama gannaaw, ndaxte du yëfi Yàlla ngay xalaat waaye yëfi nit ngay xalaat.»
34 Noonu mu woo mbooloo mi ak taalibeem yi te ne leen: «Ku ma bëgga topp, na bàyyi boppam, nangu daj lu metti, te doora topp ci man. 35 Ndaxte ku bëgga musal sa bakkan dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ndax man ak xibaar bu baax bi, dinga ko musal. 36 Lu muy jériñ nit su fekkee day moom àddina si yépp te ñàkk bakkanam? 37 Amul dara lu nit mëna joxe ngir jotaat dundam. 38 Ku ma rusa seedeel, te rusa seede samay kàddu ci kanamu niti jamono jii di mooy Yàlla tey bàkkaar, Doomu nit ki dina la rusa xam tamit bés bi muy ñëw ci màggaayu Baayam ànd ak malaaka yu sell yi.»