Yeesu mu ngi jàngale ci lu jëm ci tas séy
10
Yeesu jóge foofu te dem ci diiwaanu Yude ci wàll bi féete ci beneen wetu dexu Yurdan. Mbooloo mu takku dajaloowaat, wër ko, te mu tàmbali di leen jàngal ni mu ko tàmme di def. 2 Ay Farisen jegesi Yeesu ngir fiir ko. Ñu laaj ko ne: «Ndax sunu yoon bi may na góor mu fase jabaram?» 3 Yeesu tontu leen ne: «Lan la leen Musaa sant?» 4 Ñu tontu ne: «Musaa may na góor mu bind ab bataaxal ngir fase jabaram.» 5 Yeesu ne leen: «Seen dëgëraayu xol moo tax Musaa bindal leen ndigal boobu, 6 waaye ci njàlbéenu àddina, Yàlla sàkkoon na nit, góor ak jigéen. 7 Loolu moo tax góor dina bàyyi pàppaam ak yaayam ngir taq ci jabaram, 8 te ñoom ñaar ñu doon benn. Noonu nekkatuñu ñaar waaye benn lañuy doon. 9 Kon nag li Yàlla boole, bu ko nit tas.»
10 Bi ñu delloo ci kër ga, taalibe yi tàmbale di laaj Yeesu ci mbir moomu. 11 Mu ne leen: «Ku fase sa jabar te takk beneen jigéen, njaaloo nga te tooñ nga ku jëkk ki. 12 Te bu jigéen tasee ak jëkkëram te séyaat ak beneen góor, njaaloo na.»
Yeesu mu ngi jàngale ci li am solo ci nguuru Yàlla gi
13 Amoon na ñu ñëw, andil Yeesu ay gone ngir mu teg leen loxo, waaye taalibe yi di leen gëdd. 14 Bi Yeesu gisee loolu mu daldi mer te ne taalibeem yi: «Bàyyileen gone yi ñu ñëw ci man. Buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo moom nguuru Yàlla gi. 15 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku nanguwul nguuru Yàlla gi ni gone doo ci dugg mukk.» 16 Noonu Yeesu laxasu gone yi, teg leen loxo te barkeel leen.
17 Bi Yeesu di dem, benn waay di daw, di ñëw, sukk ci kanamam, te laaj ko ne: «Jàngalekat bu baax bi, lan laa wara def ngir am dund gu dul jeex gi?» 18 Yeesu tontu ko ne: «Lan moo tax nga may woowe ku baax? Kenn baaxul ku dul Yàlla rekk. 19 Xam nga ndigal yi: bul rey nit, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, bul tooñ kenn jaarale ko ci nax, teralal sa baay ak sa yaay.» 20 Waa ji ne ko: «Jàngalekat bi, ndigal yooyu yépp, sàmm naa leen bi ma nekkee ndaw ba léegi.» 21 Yeesu xol ko, bëgg ko, te ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Demal nga jaay lépp li nga am, séddale ko néew-di-doole yi. Noonu dinga am alal ci asamaan, te nga ñëw topp ci man.» 22 Waaye bi waa ji déggee kàddu yooyu, kanamam soppeeku, te mu dem, ànd ak tiis ndaxte dafa bari woon alal lool.
23 Yeesu xool taalibe yi ko wër te ne leen: «Lu jafe ngoogu ngir boroom alal dugg ci nguuru Yàlla!» 24 Taalibe yi daldi waaru ci kàddu yooyu, waaye Yeesu waxaat leen ne: «Samay doom, dugg ci nguuru Yàlla gi, lu jafe la. 25 Giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.» 26 Taalibe yi gëna jaaxle tey wax ci seen biir ne: «Kon nag, kan moo mëna mucc?» 27 Yeesu xool leen te ne leen: «Loolu të na nit waaye tëwul Yàlla, ndaxte Yàlla mën na lépp.»
28 Noonu Piyeer ne ko: «Xoolal! Nun, bàyyi nanu lépp ngir topp la.» 29 Yeesu tontu ko ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku bàyyi këram, ay magam, ay rakkam, yaayam, pàppaam, ay doomam, walla ay suufam ndax man ak xibaar bu baax bi, 30 dina jot lu ëpp loolu téeméeri yoon ci jamono jii: ay kër, ay mag, ay rakk, yaay, baay, ay doom, ak ay suuf, ànd ak fitna. Ci jamono jee di ñëw tamit dina am dund gu dul jeex gi. 31 Waaye ñu bari ci ñi jiitu léegi dinañu mujje. Te ñu bari ci ñi mujje léegi dinañu jiitu.»
Doomu nit ki dafa ñëw ni surga
32 Yeesu jiite woon na taalibeem yi ci yoon ngir ñu dem Yerusalem. Taalibe yi jaaxle woon nañu te ñi ci toppoon tiitoon nañu. Foofu Yeesu jëlaat fukk yi ak ñaar, ber leen, te mu tàmbali di leen wax ci li ko naroona dal. 33 «Dégluleen! Nu ngi ci yoonu Yerusalem. Foofu dinañu jébbal Doomu nit ki ci loxoy njiiti-jébbalkati-sarax yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa. Dinañu ko teg daanu dee te jébbal ko ci loxoy ñi nekkul Yawut. 34 Dinañu ko ñaawal, tifli ko, dóor ko ay yar ba noppi, rey ko, te ci ñetteelu fan ba, mu dekki.»
35 Noonu Saak ak Yowaana, ñiy doomu Sebede, ñëw ci wetu Yeesu te ne ko: «Jàngalekat bi, danoo bëgg nga defal nu li nu la bëgga ñaan.» 36 Mu ne leen: «Lan ngeen bëgg ma defal leen ko?» 37 Ñu tontu ko ne: «May nu, boo nekkee ci sa màggaay, nu toog, kenn ki ci sa ndeyjoor, keneen ki ci sa càmmoñ.» 38 Waaye Yeesu ne leen: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax mën ngeena naan kaas bi ma nara naan? Walla ñu sóob leen sóob bi ñu ma nara sóob?» 39 Ñu tontu ko ne: «Waaw, mën nanu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kaas bi ma nara naan, dingeen ci naan, te sóob bi ñu ma nara sóob, dinañu leen ko sóob. 40 Waaye nag ngir toog ci sama ndeyjoor walla ci sama càmmoñ, du man maa koy maye. Béréb yooyu ñi leen Yàlla jagleel, ñoo leen moom.»
41 Bi fukk yi des déggee loolu, ñu daldi mere Saak ak Yowaana. 42 Noonu Yeesu woo leen, ñoom ñépp, ci wetam te ne leen: «Xam ngeen ne ñi ñuy xoole ni njiiti xeet yi dañuy not seeni askan, te kilifa yi di jëfe ak sañ-sañ ci ñoom. 43 Waaye yeen, warul deme noonu ci seen biir. Waaye ku bëgga nekk màgg ci seen biir, na nekk seen surga, 44 te ku bëgga jiitu ci seen biir, na nekk jaamu ñépp. 45 Ndaxte Doomu nit ki ñëwul ngir ñu nekk ay surgaam, waaye ngir mu nekk surga te joxe bakkanam ngir fey boru bàkkaaru ñu bari.»
Yeesu wéral na gumba bu tudd Bartime
46 Yeesu ak taalibeem yi yegsi nañu ci dëkku Yeriko. Bi ñu génnee dëkk bi ànd ak mbooloo mu takku, foofu amoon na benn gumba bu tudd Bartime, di doomu Time. Toogoon na ci wetu yoon bi di yelwaan. 47 Bi mu déggee ne Yeesu mu Nasaret la, mu tàmbali yuuxu naan: «Yeesu sëtu Daawuda, yërëm ma.» 48 Ñu bari di ko gëdd ngir mu noppi. Waaye mu gëna yuuxu naan: «Sëtu Daawuda, yërëm ma.» 49 Yeesu daldi taxaw, te ne: «Wooleen ko.» Ñu woo gumba bi te ne ko: «Takkal sa fit te nga jóg; mu ngi lay woo.» 50 Noonu mu sànni mbubbam, daldi ne bërét te ñëw ci Yeesu. 51 Yeesu ne ko: «Loo bëgg ma defal la?» Gumba bi ne ko: «Jàngalekat bi, damaa bëgga gisaat.» 52 Yeesu ne ko: «Demal, sa ngëm musal na la.» Ci saa si mu gisaat te topp Yeesu ci yoon bi.