Yuusufa denc na néewu Yeesu ci bàmmeel bi
Luug 23.50-56
50-51 Amoon na benn waay bu tuddoon Yuusufa,
mu dëkk Arimate ci diiwaanu Yude.
Nit ku jub la woon te baax te doon xaar nguuru Yàlla.
Bokk ci kurélu àttekati Yawut yi waaye àndul woon ci ni ñu tege woon daan Yeesu.
52 Mu dem ci Pilaat laaj ko néewu Yeesu,
53 mu wàcce ko ci bant bi,
lëmës ko ci perkaal,
denc ko ci bàmmeel bu ñu yettoon te kenn mësu fa tëdd.
54 Booba àjjuma ci ngoon,
bésu noflaay bi mu ngi dugg.
55 Jigéen ñi àndoon ak Yeesu ci Galile,
topp Yuusufa ngir gis bàmmeel bi ak ni ñu dence néewu Yeesu.
56 Noonu ñu ñibbi,
di defar cuuraay ak latkoloñ.
Ci bésu noflaay bi,
ñu toog,
defuñu dara,
ni ko yoonu Musaa digle.