Yeesu dekki na
Luug 24.1-12
1 Dimaas ci suba teel jigéen ñi doon dem ci bàmmeelu Yeesu,
di yóbbaale cuuraay bu ñu defaroon.
2 Ñu dem ba yegg ci buntu bàmmeel bi,
fekk xeer bi nga xamante ne tëjoon na bàmmeel bi,
bërëŋu.
3 Ñu dugg ci biir,
waaye gisatuñu yaramu Boroom bi Yeesu.
4 Ñu jaxasoo.
Noonu ñaari góor yu sol ay yére yuy melax feeñu leen ci seen wet.
5 Tiit dab leen,
ba tax ñu sukk,
dëpp seen jë ci suuf.
Ñaari góor yi laaj leen ne:
«Lan moo tax ngeen di seet kiy dund ci biir ñu dee ñi?
6 Nekkatu fi;
dekki na.
Fàttalikuleen li mu leen waxoon bi mu nekke woon ak yeen ci diiwaanu Galile:
7 "Fàww ñu jébbale Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi,
ñu daaj ko ci bant,
te mu dekki ci ñetteelu fan bi."»
8 Noonu jigéen ñi daldi fàttaliku kàdduy Boroom bi Yeesu.
9 Bi ñu jógee ci bàmmeel bi,
ñu dem nettali loolu lépp fukk yi ak benn ak ñeneen ñépp.
10 Jigéen ñooñu ñoo doon Maryaama bu Magdala,
Sànn,
Maryaama mi di yaayu Saag,
ak yeneen jigéen yu leen gunge woon tamit.
Ñu nettali loolu ndaw ya,
11 waaye ñu teg seen wax caaxaan ba tax gëmuñu jigéen ñi.
12 Waaye Piyeer daldi jóg,
daw,
dem ci bàmmeel bi.
Bi mu yeggsee,
mu sëgg,
gisul lu dul perkaal.
Noonu mu daldi ñibbi këram di waaru ci li xewoon.