Daaj nañu Yeesu ci bant
Luug 23.26-49
26 Bi soldaar yi di yóbbu Yeesu ñu taseek benn waay bu tudd Simoŋ mu Siren te mu jóge woon ci tool yi.
Ñu jàpp ko ak doole,
sëf ko bant bi,
ngir mu gàddu ko ci gannaaw Yeesu.
27 Noonu mbooloo mu bari di leen topp.
Jigéen ñi di jooy te di naqarlu.
28 Yeesu walbatiku,
jàkkaarlook ñoom,
ne leen:
«Yeen jigéenu Yerusalem buleen ma jooy,
waaye jooyleen seen bopp ak seeni doom,
29 ndaxte ay jamonoo ngi ñëw,
ñu wax ne “barkeel nañu jigéen ñi mënula am doom,
yi mësula ëmb ak yi mësula nàmpal.”
30 Bu booba dinañu wax tund yu mag yi,
"daanuleen sunu kaw,"
te tund yu ndaw yi “muurleen nu,”
31 ndaxte bu ñuy def nii garab bu tooy bi,
naka lañu wara def bu wow bi?»
32 Soldaar yi doon nañu yóbbaale ñaari waay di ay defkatu lu bon ngir rey leen ak Yeesu.
33 Bi ñu yeggsee ci béréb bi ñuy woowe diggu bopp ñu daaj Yeesu ci bant.
Ñu daajaale ñaar ñi,
kenn ki ci ndeyjooram,
keneen ki ci càmmooñam.
34 Noonu Yeesu daldi def ñaan bii ne:
«Baay baalal nit ñi li ñu ma def,
ndaxte xamuñu li ñuy def.»
Soldaar yi tegoo bant ngir séddoo yéreem.
35 Mbooloo mi taxawoon na fa di xool.
Waaye njiiti Yawut yi di ñaawal Yeesu ne:
«Muccal na ñeneen ñi,
na muccal boppam,
su déy mooy Almasi bi,
di ki Yàlla tànn.»
36 Soldaar yi tamit di ñaawal Yeesu,
jegesi ko,
jox ko bineegar,
37 di ko wax ne:
«Xanaa du yaw yaay buuru Yawut yi?
Kon muccalal sa bopp.»
38 Bind nañu ne:
«Kii mooy buuru Yawut yi,»
mu tiim boppu Yeesu.
39 Kenn ci defkatu lu bon yi ñu daajoon ci wetu Yeesu xas ko,
ne ko:
«Xanaa du yaw yaay Almasi bi?
Kon muccalal sa bopp te muccalaale nu.»
40 Waaye beneen defkatu lu bon bi di ko yedd ne ko:
«Xanaa yaw ragaloo Yàlla,
yaw mi bokk ak moom daan?
41 Lu jub la ngir nun ndaxte danuy fey sunuy jëf,
waaye moom,
deful dara lu bon.»
42 Mu ne:
«Yeesu,
fàttaliku ma soo duggee ci sa nguur.»
43 Yeesu ne ko:
«Ci dëgg maa ngi la koy wax,
tey ji sax dinga nekk ak man,
biir àjjana.»
44-45 Noonu ci diggu bëccëg bi,
jant bi daldi nëbbu,
mu lëndëm ci réew mi yépp lu tollook ñetti waxtu.
Rido kër-Yàlla gi daldi xar ci digg bi.
46 Yeesu yuuxu ak baat bu kawe ne:
«Baay maa ngi teg sama ruu ci say loxo.»
Gannaaw bi mu waxee kàddu yooyu,
mu daldi dee.
47 Bi njiitu soldaaru Room bi gisee loolu muy màggal Yàlla te wax ne:
«Ci dëgg,
waa jii ku jub la woon.»
48 Mbooloo mi ñëwoon seetaansi mbir yooyu di dellu di fëgg seeni dënn di réccu.
49 Xaritu Yeesu yépp ak jigéen ñi ko toppe woon ci diiwaanu Galile taxawoon nañu fu sori di seetaan li fa xewoon.