Teg nañu Yeesu daanu dee
Luug 23.1-25
1 Noonu kurélu àttekati Yawut yi yépp jóg nañu,
indi Yeesu ci kanamu Pilaat.
2 Foofu ñu tàmbali di ko tuumaal ne :
«Ki mooy kiy jaxase sunu askan bi,
di tere ñu fey lempo Sesaar,
te di wax ne moom mooy Almasi bi,
di buur.»
3 Pilaat laaj Yeesu,
ne ko:
«Ndax yaw yaay buuru Yawut yi?»
Mu tontu ko ne:
«Yaw yaa ko wax.»
4 Pilaat wax njiiti-jébbalkati-sarax si ak mbooloo mi ne:
«Kii déy,
gisuma ci moom lenn lu jar ma koy teg daan.»
5 Waaye ñu gëna wax ne:
«Moom day jógloo askan bi ci ay njàngaleem,
dale ko ci diiwaanu Galile ak Yude ba fii.»
6 Bi Pilaat déggee loolu,
mu laaj leen ne:
«Ndax kii,
waa Galile la?
7 Bi Pilaat xamee ne ci diiwaan bi Erodd yilifoon la bokk,
mu yónnee ko Yeesu,
ndaxte Erodd mu ngi woon Yerusalem ci bés yooyu.
8 Bi Erodd gisee Yeesu mu daldi ànd ak mbégte,
ndaxte yàggoon na koo bëgga gis ndax li mu doon dégg ñu koy wax ci moom,
te yaakaaroon na gis mu def fa ay kéemaan.
9 Mu laaj ko ay laaj yu bari waaye Yeesu tontuwu ko benn yoon.
10 Njiiti-jébbalkati-sarax si ak jàngalekati-yoonu-Musaa yi,
nu ngi woon foofu di ko tuumaal ak doole.
11 Erodd ak soldaaram yi daldi jéppi Yeesu.
Ñu ñaawal ko,
solal ko mbubb mu rafet,
te delloo ko Pilaat.
12 Ci bés boobu,
Erodd ak Pilaat yi nekkoon ay noon,
xaritoo nañu.
13 Gannaaw loolu,
Pilaat dajalee njiiti-jébbalkati-sarax si,
Kilifa yi ak mbooloo mi
14 ne leen:
«Dangeen maa indil waa ji di ko tuumaal ne:
“Dafay jaxase askan bi.”
Laaj naa ko ci seen kanam waaye gisuma ci moom dara lu jar ñu koy teg daan ci li ngeen koy tuumaal.
15 Erodd tamit gisul ci moom dara,
ba tax mu delloosi nu ko.
Waa jii deful dara lu jar ñu koy rey.
16 Waaye dinaa ko yewwi gannaaw bi ma ko dóorloo ay yar ba noppi.»
17 Pilaat dafa tàmmoon di bàyyi benn nit bu ñu tëj kaso ci màggalu Paak.
18 Waaye mbooloo mi àndoon nañu di yuuxu ak doole ne:
«Rey ko,
te nga bàyyil nu Barabas.»
19 Barabas moomu dañu ko tëjoon kaso ndax fippu bu amoon ci dëkk bi,
ndaxte tamit dafa reyoon benn nit.
20 Waaye Pilaat di waxaat ak mbooloo mi,
ndaxte dafa bëggoona yewwi Yeesu.
21 Te ñuy yuuxu di wax ne:
«Daaj ko ci bant.
Daaj ko ci bant.»
22 Waaye Pilaat waxaat leen ci ñetteelu yoon bi ne:
«Lan la def lu bon?
Gisuma ci moom dara lu jar nu koy teg daanu dee.
Kon nag dinaa ko yewwi gannaaw bi ma ko dóorloo ay yar ba noppi.»
23 Waaye mbooloo mi gëna wax ak doole ne:
«Daaj ko ci bant.»
Seeni yuuxu daldi ko ëpp doole.
24 Pilaat jël dogal ngir may leen li ñu ko doon ñaan:
25 yewwi ki ñu tëjoon kaso ndax fippu te ndaxte tamit dafa reyoon benn nit,
te jébbal Yeesu soldaar yi ngir ñu def ci moom li askan bi bëgg.