Yudaa jébbale na Yeesu, ñu jàpp ko te njiiti Yawut yi di ko laaj
Luug 22.47-71
47 Bi Yeesu di wax loolu,
mbooloo mu bari yeggsi,
te ki ñuy woowe Yudaa,
bokkoon ci fukk yi ak ñaar,
jiitu leen.
Mu jegesi Yeesu ngir fóon ko,
48 waaye Yeesu ne:
«Yudaa,
ndax ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki?»
49 Noonu bi ñi àndoon ak Yeesu gisee li waroona xew,
ñu laaj ko ne:
«Boroom bi,
ndax nu jëfandikoo sunuy jaasi?»
50 Te kenn ci ñoom dóor surga njiitu-jébbalkati-sarax si,
ba dagg noppu ndeyjooram.
51 Waaye Yeesu jël kàddu gi ne leen:
«Bàyyileen,
doy na,»
te mu laal noppu waa ji te wéral ko.
52 Noonu Yeesu wax njiiti-jébbalkati-sarax si ak mag ñi ak njiiti garjen Kër-Yàlla gi,
yi ñëwoon jàppsi ko ne leen:
«Lu tax ngeen gàddu seeni jaasi ak seeni yet mel ni ñuy wuta jàppe defkatu lu bon,
53 moona bés bu nekk nekkandoo woon naa ak yeen ci kër-Yàlla gi te jàppuleen ma waaye léegi ngir yeen waxtu bi jot na,
waxtu bi kilifteefu lëndëm bi di jëf.»
54 Ci noonu ñu jàpp Yeesu te yóbbu ko ci kër njiitu-jébbalkatu-sarax si,
te Piyeer doon leen toppe fu sori.
55 Ci diggu ëtt bi taaloon nañu fa xal,
te nit ñu bari toog,
wër xal bi,
te Piyeer toogoon ci seen biir.
56 Benn surga bu jigéen gis ko mu toog ci leeraayu xal bi,
mu daldi ko xool te wax ne:
«Nit kii tamit nekkoon na ak moom.»
57 Waaye Piyeer weddi ko ne:
«Soxna si,
xamuma ko.»
58 Ci kanam tuuti,
keneen gis ko te wax ne:
«Yaw tamit,
ci ñoom nga bokk.»
Waaye Piyeer tontu ko ne:
«Déedéet,
sama waay,
bokkuma ci.»
59 Lu tollu ci benn waxtu kenn di wax te di ko dëggal ne:
«Ci dëgg,
nit kii àndoon na ak moom,
ndaxte ci diiwaanu Galile la jóge.»
60 Waaye Piyeer tontu ko ne:
«Sama waay,
xawma li ngay bëgga wax.»
Ci saa si bi mu nekkee di wax loolu benn ginaar sab.
61 Noonu Boroom bi geestu,
xool Piyeer te Piyeer fàttaliku li ko Boroom bi waxoon ne:
«Bala ginaar gi sab tey dinga ma weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
62 Te Piyeer génn,
di jooy,
jooy yu metti.
63 Nit ñi jàppoon Yeesu di ko ñaawal te di ko door.
64 Ñu muur kanamam di ko laaj:
«Éey yonent bi,
wax nu,
kan moo la door!»
65 Te ñu koy wax yeneen kàddu yu bon ngir saaga ko.
66 Bi bët setee kurélu àttekati Yawut yi:
njiiti-jébbalkati-sarax yi ak jàngalekati-yoonu-Musaa yi booloo nañu.
Ñu àndil leen Yeesu ci bérébu àttekaay bu mag bi.
67 Ñu wax ko ne:
«Wax nu,
ndax yaw yaay Almasi bi?»
Yeesu tontu leen:
«Su ma leen ko waxee,
dooleen ma gëm,
68 te su ma leen ko laajee,
dooleen ma tontu.
69 Waaye dale ko tey,
Doomu nit ki dina toog ci ndeyjooru Yàlla Aji-Kàttan ji.»
70 Ñoom ñépp ñu wax ne :
«Ndax yaw yaay Doomu Yàlla ji,
nag?»
Mu tontu leen ne:
«Yeena wax ne moom la.»
71 Noonu ñu daldi wax ne:
«Soxlatunu beneen seede ndaxte dégg nanu ba noppi li mu tontu ci gémmiñam.»