Yeesu ñaan na ci tundu Oliw ya
Luug 22.39-46
39 Yeesu génn di dem ci tundu Oliw ya,
ni mu ko tàmme woon di defe.
Taalibe yi topp ko.
40 Bi ñu yeggsee mu ne leen :
«Ñaanleen ngir ngeen baña daanu ci fiir.»
41 Mu sori leen tuuti,
sukk óomam di ñaan
42 ne:
«Baay,
su la neexee soril ma kaasu naqar bi,
waaye bu mu doon sama coobare waaye na sa coobare rekk am.»
43 Noonu malaaka asamaan feeñu ko te di ko dëgëral.
44 Ci njaqareem,
muy gëna sawar ci ñaan ba ñaq yi mel ni ay toqu deret di daanu ci suuf.
45 Mu ñaan ba noppi,
jóg,
ñëw,
fekk taalibe yi nelawoon nañu ndax tiis.
46 Mu ne leen:
«Lan moo tax ngeen di nelaw?
Jógleen te ngeen ñaan ngir ngeen baña daanu ci fiir.»