Reeru Yeesu bu mujj bi
Luug 22.7-38
7 Ci màggalu mburu yu amul lawiir yi,
bés bi ñuy rendi mbote yi ngir reeru Paak bi yeggsi na.
8 Noonu Yeesu yónni Piyeer ak Yowaana ne leen:
«Demleen,
ngeen waajal nu reeru Paak bi.»
9 Ñu laaj ko ne ko:
«Fan nga bëgg nu waaje ko?»
10 Mu ne leen:
«Sungeen duggee ci dëkk bi,
dingeen daje ak benn waay bu yenu ndaal bu am ndox.
Toppleen ko ba ci kër gi muy dugg,
11 te nii ngeen di waxe ak boroom kër gi ne ko:
"Jàngalekat bi moo lay wax ne:
Fan mooy néegu gan bi may lekke reeru Paak bi ak samay taalibe?"
12 Noonu dina leen won benn néeg bu yaatu;
bu ñu defar ba noppi te mu féete ci kaw.
Foofu ngeen koy waajale.
13 Ñu dem fekk lépp ni leen ko Yeesu waxe woon,
te ñu daldi waajal reeru Paak bi.
14 Bi waxtu bi jotee Yeesu toog na ak ndawam ya.
15 Noonu mu ne leen:
«Sama xel bépp nekkoon na ci lekkandoo ak yeen reeru Paak bii bala ñu may teg ci coono,
16 ndaxte maa ngi leen koy wax dootuma lekk reer bii mukk lu dul bés bi nga xam ne ci la lépp li muy tekki di mat ci nguuru Yàlla.»
17 Noonu mu daldi jël kaasu biiñ,
sant Yàlla ba noppi,
ne leen:
«Jëlleen kaas bi,
ngeen séddoo ko ci seen biir
18 ndaxte maa ngi leen koy wax gannaaw si tey,
dotuma naan biiñ mukk lu dul nguuru Yàlla gi di ñëw.
19 Noonu mu jël mburu mi sant Yàlla ba noppi;
damm ko,
jox leen ko,
ne:
«Lii moo di sama yaram bi ma joxe ngir yeen;
deeleen def lii ngir di ma fàttaliku.»
20 Gannaaw bi ñu reeree mu jël kaas bi jox leen ko te ne:
«Kaas bi mooy kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret bi ma tuur ngir yeen.
21 Waaye xoolleen,
ki ma nara jébbale mu ngi fii di reerandoo ak man
22 ndaxte Doomu nit ki dina dee ni ko Yàlla dogale waaye musiba dina dal nit ki koy jébbale.»
23 Ndaw yi di laajante ci seen biir,
kan ci ñoom mooy ki nara def loolu.
24 Noonu ñu tàmbali di laajante te di werante ci seen biir kan mooy ki gëna mag.
25 Yeesu jël kàddu gi ne leen:
«Buuri xeet yi dañuy nguuru ak doole ci seen askan yi te njiit yiy jëfe ak sañ-sañ ci ñoom,
ñuy sàkku ñu woowe leen ay defkatu lu baax.
26 Buleen jëfe noonu.
Waaye na ki gëna mag ci seen biir mel ni ki gëna ndaw te ki jiite mel ni surga bi.
27 Ci seen xalaat kan mooy ki gëna mag?
Ki toog ci bérébu lekkukaay bi walla ki koy toppatoo?
Ndax du ki toog ci bérébu lekkukaay bi?
Waaye man damaa nekk ci seen biir ni surga.
28 Yeena doon muñandoo ak man ci samay coono;
29 moo tax ni ma Baay bi joxe nguur gi dinaa leen ko joxaat,
30 ngir ngeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur,
te ngeen toog ci ay baŋi nguur,
ngir àtte fukki giir ak ñaar yu Israyil.»
31 Noonu Yeesu ne:
«Simoŋ,
Simoŋ,
moytul!
Seytaane ñaan na Yàlla sañ-sañ ngir sonnal leen ni ñuy teqale dugub ak xatax.
32 Waaye man ñaanal naa la,
ngir nga baña ñàkk sa ngëm.
Te bés bi ngay dellusi ci man nanga dëgëral say mbokki taalibe.»
33 Simoŋ ne ko:
«Boroom bi pare naa su ko jaree,
ma ànd ak yaw kaso walla sax ma dee.»
34 Yeesu ne ko:
«Piyeer maa ngi la koy wax tey jii sax bala ginaar di sab dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
35 Noonu Yeesu wax taalibeem yépp ne:
«Bi ma leen yónnee te yóbbaalewuleen kalpe,
saaku tukki ak dàll,
ndax ñàkkoon ngeen dara?»
Ñu ne ko:
«Ñàkkunu woon dara.»
36 Mu ne leen:
«Waaye léegi na ki am kalpe,
jël ko.
Na ki am saaku tukki tamit jël ko,
te ki amul jaasi jaay sabadooram,
jënd ko.
37 Maa ngi leen koy wax fàww mu mat li Mbind mi wax ci man ne:
‘Boole nañu ko ak defkatu lu bon yi,’
ndaxte lépp li ñu bind ci man dina mat.
38 Ñu ne ko:
«Boroom bi am nanu fii ñaari jaasi.»
Mu ne leen:
«Loolu doy na.»