Yeesu dàq na ay jaaykat ci kër-Yàlla gi
Luug 19.45-48
45 Gannaaw loolu Yeesu dugg na ci kër-Yàlla gi,
fekk fa ay jaaykat.
Noonu mu dàq leen,
46 di leen wax ne,
«Mbind mi nee na,
sama kër,
këru ñaanukaay lay doon,
waaye yeen def ngeen ko këru sàcc.»
47 Yeesu doon na jàngale bés bu nekk ci kër-Yàlla gi.
Noonu njiiti-jébbalkati-sarax yi ak ay jàngalekati-yoonu-Musaa ak njiiti askan bi,
ñu ngi ko doon wuta rey,
48 waaye amuñu woon pexe ngir def ko ndaxte askan bi yépp,
ñu ngi ko doon déglu ak xel.