Yeesu dugg na Yerusalem
Luug 19.28-44
28 Gannaaw bi mu waxee loolu Yeesu jiitu na leen di dem Yerusalem.
29 Bi mu jegesee dëkku Betfase ak bu Betani ci wetu tund bi ñuy woowe Tundu Oliw ya,
mu yónni ñaar ci taalibeem yi
30 ne leen:
«Demleen ci gox bi nekk seen kanam.
Su ngeen yeggee dingeen fekk benn mbaam bu ndaw bu kenn mësula yéeg.
Yewwileen ko,
ngeen indi ko fii.
31 Bu leen kenn laajee "Lu tax ngeen di yewwi mbaam bi?"
neleen ko "Boroom bi Yeesu moo ko soxla."»
32 Ñi mu yónni,
bi ñu yeggee ñu fekk lépp ni leen ko Yeesu waxe woon.
33 Bi ñuy yewwi mbaam mi,
ñi moom mbaam mi ne leen:
«Lu tax ngeen di yewwi mbaam mi?»
34 Ñu tontu leen ne:
«Boroom bi Yeesu moo ko soxla.»
35 Noonu ñu indil Yeesu mbaam mi,
teg ci seen yére yi te yéegal Yeesu ci mbaam mi.
36 Yeesu,
bi muy dem,
nit ñi di lal seen yére yi ci yoon bi.
37 Bi mu jegesee yoon bi wàcce ci tundu Oliw ya,
mbooloo taalibeem yi yépp ànd ak mbégte,
di sant Yàlla ak baat bu kawe ndax kéemaan yépp yi ñu gisoon,
38 di wax ne:
\qt «Barkeel na buur biy ñëw ci turu Boroom bi.
Na jàmm am ci asamaan
te ñu màggal Yàlla ci béréb yi gëna kawe.»
39 Noonu ñenn ci Farisen yi nekkoon ci mbooloo mi wax Yeesu ne:
«Jàngalekat bi,
waxal sa taalibe yi ñu noppi.»
40 Yeesu tontu ne:
«Maa ngi leen koy wax,
su ñu noppee,
xeer yi dinañu yuuxu.»
41 Bi Yeesu jegesee dëkku Yerusalem te gis ko,
mu jooy ci moom
42 te wax ne:
«Aa yaw,
soo ràññee woon ci bés bii,
li lay may jàmm.
Waaye léegi loolu lépp nëbbu na ci say bët.
43 Ndaxte ci yaw ay bés a ngi ñëw,
say noon dinañu defar ay jalu suuf ngir wër la,
te tanc la ci boor bu nekk.
44 Dinañu la yàqate yaxeet yaw ak sa waa dëkk te duñu bàyyi ci yaw doj ci kaw doj.
Lu tax?
Ndaxte ràññeewoo jamono ji la Yàlla wallusee.