Léebu buur bi dénkoon surgaam yi wurus
Luug 19.11-27
11 Ni mbooloo mi doon dégloo kàddu yooyu,
Yeesu yokk ca,
wax leen benn léeb ndaxte fekkoon na ñu jegesi Yerusalem te mbooloo mi foogoon nañu ne nguuru Yàlla gi dina feeñ ci saa si.
12 Loolu moo tax mu ne leen:
«Dafa amoon boroom juddu bu rafet,
bu bokk ci njabootu buur te waroona dem ci réew mu sori ngir ñu fal ko buur te mu dellusi.
13 Bala muy dem mu woo fukk ci ay surgaam te dénk leen ku ci nekk benn wurus te ne leen:
"Fexeleen mu jur bala may dellusi."
14 Waaye waa réewam bañ ko,
yónni ay ndaw ci gannaawam ngir ñu wax:
"Nit ki,
bëggunu mu nekk sunu buur."
15 Gannaaw bi ñu ko falee buur,
mu dellusi ci réewam,
te woo surga yi mu dénkoon wurus ngir xam lan lañu ci jële.
16 Ku jëkk ki jegesi ko,
wax ko ne:
"Sang bi sa benn wurus bi jur na fukk."
17 Buur bi ne ko:
"Waaw góor,
surga bu baax nga te gore ci ay mbir yu ndaw.
Dénk naa la fukki dëkk."
18 Ñaareelu surga bi ñëw,
wax ko ne:
"Sang bi,
sa benn wurus bi jur na juróomi wurus."
19 Buur bi ne ko:
"Yaw tamit,
dénk naa la juróomi dëkk."
20 Beneen surga bi ñëw ne ko:
"Sang bi,
wurus bi nga ma joxoon mu ngi nii.
Dama koo lëmës,
denc ko.
21 Dama laa ragal ndaxte ku néeg nga te dangay nangu alal joo dencul te di góob foo jiwuloon.»
22 Buur bi ne ko:
"Ci say kàddu laa laay àtte,
yaw surga bu bon bi.
Bi nga xamee,
ku néeg laa di nangu alal ji ma dencul te di góob li ma jiwul,
23 lan moo tax jëloo sama benn wurus bi ma la dénkoon te denc ko fi ñuy dence wurus yi,
ba bu ma dellusee ma jot sama wurus ak li mu jur?"
24 Noonu mu ne ñi fa nekkoon:
"Jëlleen benn wurus bi te ngeen dolli ko ki am fukki wurus yi."
25 Noonu,
ñu tontu ko ne:
"Sang bi,
kooku am na fukki wurus."
26 Noonu mu ne leen:
"Maa ngi leen koy wax,
ku am dinañu ko dollil,
waaye ku amul,
dinañu jël lu tuuti sax li nga yor.
27 Samay noon yi bañoon ma nekk seen buur àndil ma leen fii te ngeen rey leen ci sama kanam."»