Sase dalal na Yeesu ci këram
Luug 19.1-10
1 Yeesu wéy ci yoonam,
dugg Yeriko,
doon jàll dëkk bi.
2 Foofu amoon na benn nit bu ñuy woowe Sase,
njiitu juutikat te am alal.
3 Mu bëggoona gis kan mooy Yeesu,
waaye mënu ko woona gis ndax mbooloo mi,
ndaxte dafa gàttoon.
4 Noonu mu daw jiitu ko,
yéeg ci génn garab bu ñuy woowe sicomor ngir gis ko,
ndaxte xamoon na ne foofu la waroona jaar.
5 Bi Yeesu yeggsee ci béréb bi,
mu yékkëti bëtam yi,
wax ko ne:
«Sase,
gaawantul nga wàcc ndaxte fàww ma dal sa kër tey.»
6 Sase gaawantu wàcc dalal ko ak mbégte.
7 Bi ñu gisee loolu,
ñoom ñépp tàmbali nañu xuntu di naan:
«Dem na dal ci kër bàkkaarkat.»
8 Waaye Sase taxaw ci kanamu Boroom bi te wax ko ne:
«Xoolal,
Boroom bi!
Dinaa joxe sama genn-wàll alal néew ji doole yi te su fekkee ne tooñ naa nit jël alalam,
dinaa ko fey ñeenti yoon.»
9 Noonu Yeesu wax ko ne:
«Tey,
mucc gi dugg na ci kër gii,
ndaxte Sase mii tamit sëtu Ibraayma la,
10 ndaxte Doomu nit ki ñëw na ngir seet te musal ñi réer.»