Yeesu wéral na waa ju gumba
Luug 18.35-43
35 Benn bés Yeesu di jegesi dëkku Yeriko.
Ci wetu yoon bi amoon na gumba bu fa toog di yelwaan.
36 Bi mu déggee mbooloo mi di jàll mu laaj lan moo xew.
37 Ñu xamal ko ne Yeesu mu Nasaret mooy jàll.
38 Noonu muy yuuxu te wax ne:
«Yeesu sëtu Daawuda yërëm ma.»
39 Waaye ñi jiitu woon ci kanam di ko gëdd te di ko tere mu wax.
Waaye mu gëna yuuxu ak baat bu kawe di wax ne:
«Sëtu Daawuda yërëm ma.»
40 Yeesu daldi taxaw te sant leen ñu àndil ko ko.
Bi gumba bi jegesee Yeesu,
Yeesu laaj ko ne:
41 «Loo bëgg ma defal la ko?»
Gumba bi ne ko:
«Boroom bi,
damaa bëgga gisaat.»
42 Yeesu ne ko:
«Gisaatal.
Sa ngëm wéral na la.»
43 Ci saa si mu daldi gisaat te topp Yeesu di màggal Yàlla.
Mbooloo ma fa nekkoon yépp,
bi ñu gisee loolu ñoom tamit ñuy sant Yàlla.