Yeesu xamal na fukk yi ak ñaar li ko wara dal ci Yerusalem
Luug 18.31-34
31 Yeesu jëloon na fukk yi ak ñaar,
ber leen,
ne leen:
«Dégluleen!
Nu ngi ci yoonu Yerusalem.
Foofu lépp li nga xam ne moom la yonent yi bindoon ci Doomu nit ki dina mat.
32 Dinañu ko jébbal ci loxoy ñi nga xam ne nekkuñu Yawut.
Dinañu ko ñaawal,
saaga ko,
tifli ko,
33 dóor ko ay yar ba noppi,
daldi ko rey,
te ci ñetteelu fan ba mu dekki.»
34 Waaye loolu leerul ci taalibe yi,
kàddu yooyu ump na leen,
te xamuñu li wax yooyu di tekki.