Boroom alal dugg ci nguuru Yàlla
Luug 18.18-30
18 Noonu benn njiitu Yawut laaj Yeesu ne:
«Jàngalekat bu baax bi,
lan laa wara def ngir am dund gu dul jeex?»
19 Yeesu tontu ko ne:
«Lan moo tax nga may woowe ku baax?
Kenn baaxul ku dul Yàlla rekk.
20 Xam nga ndigal yi,
bul njaaloo,
bul rey,
bul sàcc,
bul seede lu dul dëgg,
teralal sa yaay ak baay.»
21 Waa ji ne ko:
«Ndigle yooyu yépp,
sàmm naa ko bi ma nekkee ndaw ba léegi!»
22 Bi Yeesu déggee loolu mu ne:
«Lenn rekk moo la dese:
jaayal lépp li nga am,
séddale ko néew-di-doole yi,
noonu dinga am alal ci asamaan,
te nga ñëw topp ci man.»
23 Waaye bi waa ji déggee loolu,
mu ànd ak tiis ndaxte dafa bari woon alal lool.
24 Bi Yeesu gisee waa ji ànd ak tiis mu ne:
«Lu jafe a ngoogu ngir boroom alal dugg ci nguuru Yàlla!
25 Giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.»
26 Ñi ko doon déglu daldi ne:
«Kon nag,
ku mëna mucc?»
27 Yeesu ne leen:
«Lu të nit,
Yàlla mën na ko.»
28 Piyeer ne ko:
«Xoolal nun,
bàyyi nanu lépp lu nu amoon ngir topp la.»
29 Yeesu ne leen:
«Ci dëgg maa ngi leen koy wax,
képp ku bàyyi këram,
jabaram,
ay magam,
ay rakkam,
ay waajuram walla ay doomam ndax nguuru Yàlla gi,
30 dina jot lu bari lool ci àddina si ak dund gu dul jeex ci jamono jee di ñëw.»