Yeesu jàngale na ci naka la nit mëna jege Yàlla
Luug 18.1-17
1 Gannaaw loolu Yeesu nettali leen benn léeb ngir won leen ne dañu war di ñaan saa su nekk te baña xàddi.
2 Mu ne leen:
«Dafa amoon ci benn dëkk,
benn àttekat bu ragalul woon Yàlla te faalewul kenn.
3 Ci dëkk boobu tamit amoon na benn jigéen bu ñàkkoon jëkkëram te doon ñëw ci moom saa su nekk te ne ko:
"Àtte ma ak ki ma joteel."
4 Àttekat ba,
bañ na lu yàgg waaye gannaaw loolu mu wax ci xelam ne:
"Doonte ragaluma Yàlla te faalewuma kenn,
5 jigéen jii lakkal na ma,
kon nag dinaa ko àtte ngir mu bañati ñëw di ma sonnal."»
6 Boroom bi yokk ca ne:
«Dégluleen li àttekat bu bon bi wax.
7 Te Yàlla ndax du àtte jub ñi mu tànn tey ñaan ci moom guddi ak bëccëg?
Ndax dina leen xaarloo?
8 Maa ngi leen koy wax,
dina leen gaawa àtte jub.
Waaye nag Doomu nit ki buy dellusi ndax dina fekk ngëm ci àddina si?»
9 Noonu Yeesu nettali leen beneen léeb jëmale ko ci ñiy jàppe seen bopp ñu jub tey xeeb ñeneen ñi.
10 «Dafa amoon ñaari waay yu demoon ci kër-Yàlla gi ngir ñaan.
Kenn ki ab Farisen la woon,
keneen ki ab juutikat.
11 Farisen bi taxaw di ñaan ci xelam ne:
"Yàlla maa ngi lay gërëm ci ni ma melul ni yeneen nit,
ñiy sàcc,
di def lu bon,
te di njaaloo,
rawatina juutikat bee.
12 Waaye damay woor ñaari yoon ci juróom ñaari fan yu nekk tey joxe asaka ci lépp li ma am."
13 Waaye juutikat bi moom taxaw na fu sori,
te bëggul sax siggi,
xol asamaan,
di fëgg dënnam di réccu tey wax ci suuf ne:
"Yàlla yërëm ma,
man bàkkaarkat bi."
14 Yeesu yokk ca ne:
«Maa ngi leen koy wax,
kooku bi muy ñibbi këram Yàlla àtte na ko ni ku jub,
waaye du Farisen bi,
ndaxte képp ku yékkëtiku dinañu la suufeel te ku suufeelu dinañu la yékkëti.»
15 Amoon na ñu ñëw indil Yeesu ay gone ngir mu teg leen loxo,
waaye bi taalibe yi gisee loolu ñu di leen gëdd.
16 Yeesu woo gone yi,
ñu ñëw te wax ne:
«Bàyyileen gone yi ñu ñëw ci man.
Buleen leen tere ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo moom nguuru Yàlla gi.
17 Ci dëgg maa ngi leen koy wax,
képp ku nanguwul nguuru Yàlla gi ni gone,
doo ci dugg mukk.»