Bés bi Doomu nit ki di ñëw
Luug 17.20-37
20 Benn bés Farisen yi laaj Yeesu,
kañ la nguuru Yàlla gi di ñëw.
Noonu Yeesu tontu leen:
«Nguuru Yàlla gi,
kenn mënu koo gis buy ñëw,
21 te kenn mënu la wax "mu ngi fii" walla "mu ngi fale" ndaxte,
xamleen ne,
nguuru Yàlla gi mu ngi ci seen biir.»
22 Noonu Yeesu ne taalibe yi:
«Ay bés a ngi ñëw,
yu ngeen di bëgga gis Doomu nit ki,
bu doon sax benn bés,
waaye du mëna nekk.
23 Dinañu leen ne:
"Mu ngi fii" walla "mu ngi fee."
Bu leen daw di leen topp.
24 Ndaxte ni melax di leerale asamaan boor ba boor,
noonu lay Doomu nit ki di mel ci bésam.
25 Waaye fàww mu sonn lool bu jëkk,
te niti jamono jii beddi ko.»
26 Bés bi Doomu nit ki dellusee,
dina mel ni jamonoy Nóoyin.
27 Nit ñi,
ñu ngi doon lekk ak naan.
Ñii di takk jabar,
ñii di séyi ba keroog Nóoyin di dugg ca gaal gu mag ga.
Noonu mbënn mi ñëw te sànk leen ñoom ñépp.
28 Itam dina mel ni jamonoy Lóot.
Nit ñi ñu ngi doon lekk,
naan di jënd di jaay,
tey tabax.
29 Ba keroog Lóot di génn ci dëkku Sodom te tawu safara ak tamarax wàcce ca asamaan te sànk leen ñoom ñépp.
30 Noonu lay mel bés bu Doomu nit ki feeñee.
31 Ci bés boobu nit ku nekk ci kaw këram te am ay yëfam ci biir kër ga,
bu mu wàcc ngir jël leen.
Te ki nekk ci tool yi,
bu mu ñibbisi.
32 Fàttalikuleen li daloon jabaru Lóot.
33 Ku wuta muccal sa bakkan dinga ko ñàkk,
waaye ku ñàkk sa bakkan dinga dund.
34 Maa ngi leen koy wax,
ci guddi googu,
ñaar ñu bokk lal,
ñu jël kenn ki bàyyi keneen ki.
35-36 Ñaari jigéen ànd di soq,
ñu jël kenn ki bàyyi keneen ki.»
37 Noonu taalibe yi laaj ko:
«Boroom bi,
fan la loolu di xewe?»
Mu ne leen:
«Fu lu dee nekk,
fa la tan yi di daje.»