Yeesu setal na fukki gaana
Luug 17.11-19
11 Benn bés,
Yeesu doon na dem Yerusalem,
mu jaar ci dig wi xàjjale diiwaanu Samari ak bu Galile.
12 Bi muy waaja dugg ci benn gox,
fukki gaana ñëw di dajesi ak moom.
Ñu taxaw,
sori ko tuuti,
13 ñu wax ci kaw ne:
«Yeesu Kilifa gi,
yërëm nu.»
14 Bi leen Yeesu gisee,
mu ne leen:
«Demleen ngeen won seen bopp jébbalkatu-sarax yi,
ngir ñu saytu seen yaram.»
Bi ñuy dem ci jébbalkatu-sarax yi,
ci yoon bi,
mu daldi leen setal.
15 Bi kenn ci ñoom gisee ne wér na,
mu jaaraat ci ay tànkam di màggal Yàlla ak baat bu kawe.
16 Mu ñëw ci Yeesu,
daanu ci ay tànkam,
di ko gërëm.
Kooku waa Samari la woon.
17 Noonu Yeesu daldi ne:
«Xanaa,
du fukk yi yépp ñoo set,
ana yeneen juróom ñeent yi?
18 Bu dul gan gi,
kenn ci ñoom dellusiwul ngir màggal Yàlla?»
19 Noonu Yeesu daldi wax waa ji:
«Jógal te nga dem,
sa ngëm muccal na la.»