Bàkkaar, ngëm, te warugaru surga
Luug 17.1-10
1 Yeesu wéyal njàngaleem di wax taalibe yi ne:
«Lu leen di xiir ci bàkkaar mënula ñàkk ci seen biir,
waaye musiba dina dal ci ki muy jaar.
2 Ñu takk ko xeer gu réy ci baatam te sànni ko ci biir géej gi,
mooy gën ci moom,
muy bàkkaarloo kenn ci ñi gëna ndaw.
3 Moytuleen yeen ci seen bopp!
Bu la sa moroom tooñee,
woo ko,
nga yedd ko.
Bu tuubee,
baal ko.
4 Te bu la tooñee juróom ñaari yoon ci bés bi,
mu dellu juróom ñaari yoon ne la:
"Tuub naa",
baal ko.»
5 Ci noonu,
ndaw yi ñaan Boroom bi ne:
«Yokkal nu sunu ngëm.»
6 Boroom bi ne leen:
«Bu ngeen amee ngëm bu tuuti bu tollu ni peppu fuddën sax,
dingeen wax garab bi:
"Buddeekul te nga sampu ci biir géej gi,"
dina leen déggal.
7 Kan ci yeen bu amoon surga,
mu nekk ci tool yi di bey walla muy sàmm ba ñibbisi nga ne ko:
"toogal te nga lekk"?
8 Déedéet!
Danga koy ne:
"Toogal ma reer te nga solu,
jox ma lekk te naan.
Gannaaw loolu dinga mëna lekk te naan."
9 Ndax njaatige bi dina gërëm surga bi ngir li mu ko sant mu def ko?"
Déedéet!
10 Yeen tamit su ngeen defee lépp li ñu leen sant ba noppi neleen:
"Surga rekk lanu.
Sunu warugar lanu def."»