Léebu boroom alal bi ak Lasaar
Luug 16.19-31
19 Gannaaw loolu Yeesu nettali benn léeb,
ne:
«Dafa amoon benn boroom alal bu doon sol ay yére yu rafet te jekk bi bari lool.
Muy bànneexu bés bu nekk te doon lekk,
lekk bu neex.
20 Ci buntu këram amoon na waa ju néew doole,
ju fa doon tëdd,
ju tuddoon Lasaar,
te yaramam bi yépp fees ak góom,
21 te dafa doon bëgga jot lekk bi doon daanu ci bérébu lekkukaayu boroom alal bi ngir faj xiifam.
Rax ci dolli,
xaju mbedd yi doon mar góomu yaramam yi.
22 Waa ju néew doole bi daldi dee,
malaaka yi jël ko,
yóbbu ko ci wetu Ibraayma.
Boroom alal bi tamit dee,
ñu suul ko.
23 Bi mu nekkee ci mbugal ci béréb bi ñu dee ñi nekk,
mu yékkëti ay bëtam,
séen Ibraayma ak Lasaar ci wetam.
24 Noonu mu yuuxu ne:
"Maam Ibraayma,
maa ngi la koy ñaan,
yërëm ma.
Ndax doo yónni Lasaar mu jël catu baaraamam,
capp ko ci biir ndox,
te toqalal ma ci sama làmmiñ ndaxte maa ngi ci coono,
ci bérébu safara sii."
25 Waaye Ibraayma tontu ko,
ne ko:
"Sama doom fàttalikul ne ci àddina si bànneexu nga te Lasaar mu ngi woon ci naqar.
Waaye léegi,
Lasaar mu ngi ci jàmm te yaw yaa ngi ci coono.
26 Rax ci dolli kàmb gu réy moo nekk ci sunu diggante,
ba tax ñi nekk ci nun,
bu ñu ko bëggoon sax,
mënuñu ñëw ci yeen,
te ñi nekk ci yeen mënuñu ñëw ci nun."
27 Boroom alal bi ne ko:
"Maam Ibraayma,
maa ngi la koy ñaan nag,
nga yónni Lasaar ci sama kër baay,
28 ngir mu dem,
artu sama juróomi rakk yi ma fa bàyyi,
ngir ñu baña ñëw ci bérébu mbugal bii."
29 Ibraayma tontu ko,
ne ko:
"Ñoom,
am nañu mbindu Musaa yi ak yu yonent yi.
Nañu leen déggal!"
30 Mu ne ko:
"Déedéet,
maam Ibraayma.
Loolu doyul.
Bu fekkee kenn ci ñi dee ñi,
moo dekki,
dem ci ñoom dinañu tuub seeni bàkkaar."
31 Waaye Ibraayma ne ko:
"Bu ñu dégluwul mbindu Musaa yi ak yonent yi,
bu kenn dekkee ci ñi dee ñi sax du tax ñu gëm."»