Yoonu Yàlla du soppeeku mukk
Luug 16.16-18
16 Yeesu yokk ca ne:
«Jamonoy yoonu Musaa ak yonent yi,
dem na ba ci Yaxya.
Bi mu ñëwee ak léegi ñu ngi yégle xibaar bu baax bi ci nguuru Yàlla te ku nekk mu ngi góor-góorlu ngir dugg ci,
17 waaye asamaan ak suuf weesu,
moo gëna yomb dindi benn rëdd ci arafu yoonu Musaa.
18 Képp ku fase sa jabar te séyaat yaa ngi njaaloo,
te ku takk jigéen bu jëkkëram fase yaa ngi njaaloo.»