Léebu surga bu njublaŋ bi te muus
Luug 16.1-15
1 Yeesu wéyal njàngaleem di wax taalibe yi ne:
«Dafa amoon benn waa ju am alal,
mu am surga buy toppatoo alalam.
Ay nit ñëw xamal ko ne surgaam bi,
mu ngi pasar-pasaree alalam.
2 Njaatige bi woo surga bi ne ko:
"Lan laa dégg,
ñu koy wax ci yaw?
Damaa bëgg nga leeralal ma,
ni ngay doxale sa liggéey ndaxte dootoo toppatoo sama alal.
3 Noonu surga bi wax ci xelam naan:
"Lan laa wara def léegi,
gannaaw sama njaatige dafa may dàq ci liggéey bi?
Liggéey ci tool?
Awma doole ngir def ko,
te yelwaan,
rus naa di ko def.
4 Aa!
xam naa li ma wara def ngir sama njaatige,
bu ma dàqee ci liggéey bii,
am ñu may dalal ci seen kër yi."
5 Mu woo kenn,
kenn ci ñi ameeloon njaatigeem bor.
Ki ci jëkk mu laaj ko ne:
"Ñaata nga ameeloon sama njaatige?"
6 Mu tontu ko ne:
"Ñeenti junniy liitari diwlinu oliw."
Mu ne ko:
"Sa kayitu bor a ngii;
toogal fii gaaw te nga bind ñaari junniy liitari diwlinu oliw."
7 Surga bi laaj keneen ki ne:
"Ñaata nga ameel sama njaatige?"
Mu tontu ko ne:
"Téeméeri saaku pepp."
Mu ne ko:
"Sa kayitu bor a ngii.
Toogal fii te nga bind juróom ñett fukki saaku pepp."
8 Noonu njaatige bi daldi naw surga bu njublaŋ bi ndax muus bi mu wone ci jëfinam.
Ndaxte niti jamono jii ñoo gëna muus ci lu ñuy jot,
seen diggante ak seeni moroom,
ba raw doomi leer yi.»
9 Yeesu yokk ca ne:
«Maa ngi leen koy wax,
wutleen ay xarit ci alalu àddina si,
ngir bu jeexee Yàlla dalal leen ci dëkkuwaay yi nekk ba fàww.
10 Ku gore ci mbir yu ndaw yi,
dinga gore ci mbir yu mag.
Ku jubadi ci mbir yu ndaw yi,
dina jubadi tamit ci mbir yu mag.
11 Su fekkee nag jubuleen ci ni ngeen di jëfandikoo alalu àddina si,
kan moo leen di dénk alal ju wóor ji?
12 Su fekkee jubuleen ci li ñenn ñi moom,
kan moo leen di jox li ngeen moom?
13 Benn jaam mënul jaamoondoo ñaari sang,
dina bañ kii te bëgg ki ci des,
walla mu fonk kii te xeeb ki ci des.
Mënuleen boole jaamu Yàlla ak jaamu alal.
14 Bi Farisen yi déggee kàddu yooyu yépp,
ñuy ñaawal Yeesu ndaxte dañoo bëggoon xaalis.
15 Yeesu tontu leen ne:
«Yeen Farisen yi dangeen jàppe seen bopp ñu jub ci kanam nit ñi,
waaye Yàlla xam na seeni xol.
Ndaxte lu nit gëna fonk,
Yàlla sib na ko.»