Sañ-sañu Yeesu
Luug 20.1-18
1 Benn bés Yeesu da doon jàngale ci kër-Yàlla gi di yégal xibaar bu baax bi askan bi.
Njiiti-jébbalkatu-sarax yi,
jàngalekatu-yoonu-Musaa yi,
ak mag yi ñëw ci moom
2 laaj ko ne:
«Wax nu,
ci bañ sañ-sañ ngay defe mbir yi ak kan moo la jox sañ-sañ boobu?»
3 Noonu Yeesu tontu leen:
«Man tamit am naa benn laaj ngir yeen.
4 Lu Yaxya doon sóobe nit ñi ci ndox,
fan la ko jële,
ci Yàlla walla ci nit?»
5 Ñuy waxtaan ci seen biir ne:
«bu nu waxee ne ci Yàlla la ko jële,
dina wax "Lan moo tax gëmuleen ko?"
6 Waaye bu ñu waxee ci nit la ko jële askan bi yépp dinañu sànni ay xeer ba nu dee,
ndaxte gëm nañu ne Yaxya yonent la woon.»
7 Noonu ñu tontu ko ne:
«Xamunu fan la ko jële.»
8 Yeesu ne leen:
«Kon nag man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe mbir yii.»
9 Gannaaw loolu Yeesu tàmbalee di nettali léeb bii askan bi:
«Dafa amoon benn waay bu jëmbët toolu reseñ,
batale ko ay beykat,
mu tukki te yàgg fa lool.
10 Bi waxtu góob jotee mu yónni benn surga ci beykat yi ngir ñu jox ko wàllam ci meññeef bi waaye beykat yi door ko,
dàq ko loxoy neen.
11 Boroom tool bi yónniwaat beneen surga waaye beykat yi door ko moom itam,
saaga ko,
dàq ko loxoy neen.
12 Mu yónniwaat ñetteelu surga waaye beykat yi gaañ ko,
génne ko tool bi.
13 Noonu boroom tool bi ne:
"Lan laa wara def?
Dinaa yónni sama doom bi ma sopp.
Xéy-na,
ñu jox ko cér."
14 Waaye bi ko beykat yi gisee ñuy wax ci seen biir ne:
"Ki wara donn tool bi mu ngi nee di ñëw.
Nanu ko rey ngir moom tool bi."
15 Noonu ñu génne ko tool bi te rey ko.»
Yeesu laaj leen:
«Naka la boroom tool bi wara def beykat yooyu?
16 Dina ñëw rey beykat yi,
jël toolam dénk ko yeneen nit.»
Bi nit ñi déggee kàddu yooyu,
ñu ne:
«Yàlla tere.»
17 Waaye Yeesu xool leen ci biir bët te ne leen:
«Kon nag lan la kàddu yi ci Mbind mi di tekki:
\qt "Doj bi tabaxkat yi sànni woon
\qt mujj na nekk doj bi ëpp solo ci tabax bi"?
18 Ku daanu ci kaw doj bi,
damm te képp ku mu daanu ci sa kaw dina la rajaxe.»