Ku tuubul bàkkaaram, sànku
Luug 13.1-9
1 Ci waxtu yooyu mu am ñu ñëw yégal Yeesu naka la Pilaat reyloo woon ay nit yu dëkk Galile ci waxtu bi ñu doon jébbal Yàlla sarax.
Seen deret daldi jaxasoo ak deretu mala yi ñu doon rendi.
2 Yeesu tontu leen ne leen:
«Ndax xalaat ngeen ne ñooñu ñoo ëpp bàkkaar ñeneen ñépp ñi dëkk Galile ba ñu rey leen ci anam bu ñaaw boobu?
3 Déedéet,
maa ngi leen koy wax.
Waaye sungeen tuubul seeni bàkkaar dingeen sànku ni ñooñu.»
4 Noonu mu waxaat leen ne:
«Ndax fàttaliku ngeen fukki nit ak juróom ñett yi dee woon ndaxte tabax bu réy te kawe bi nekkoon Silowe,
dafa daanu woon seen kaw;
ndax xalaat ngeen ne ñooñu ñoo ëpp bàkkaar ñeneen ñépp ñi dëkk Yerusalem?
5 Déedéet,
maa ngi leen koy wax.
Waaye sungeen tuubul seeni bàkkaar dingeen sànku ni ñooñu.»
6 Ci loolu Yeesu wax leen léeb bii:
«Benn waay amoon na garabu figg ci toolam.
Benn bés mu ñëw ngir witt ci meññeefu garab gi waaye gisu fa dara.
7 Noonu mu ne surgaam bi:
"Ñetti at a ngi nii may ñëw ngir witt ci meññeefu garab gi waaye duma fi fekk dara.
Dagg ko.
Lu tax muy feesal tool bi te amul njériñ?"
8 Waaye surga bi tontu ko ne ko:
"Sama njaatige,
may ko at bii.
Dinaa ko gas te sotti ci tos,
9 xéy-na dina meññ ci at bi di ñëw.
Lu ko moy,
nga daggalu ko."»