Taalibe Yeesu dafa wara wóor tey moytu
Luug 12.35-59
35 Yeesu waxaat taalibe yi ne:
«Takkuleen seen ndigg yi te seeni làmp wéy di tàkk,
36 mel ni surga yuy xaar seen njaatige jóge ci céet.
Noonu bu yeggsee rekk te fëgg,
ñu mën koo ubbil.
37 Barkeel nañu,
yooyu surga,
yi nga xam ne seen njaatige,
bi muy yeggsi,
fekk na leen ñuy xoole.
Ci dëgg maa ngi leen koy wax,
njaatige bi dina takku ndiggam,
toogloo leen,
te jegesi leen ngir jox leen ñu lekk.
38 Buy yeggsi ci xaaju guddi walla sax bi fajar di waaja jot,
li ëpp solo mooy mu fekk leen ñuy xoole.
Ñooñu barkeel nañu.
39 Xamleen bu baax ne boroom kër gi bu xamoon ban waxtu la sàcc bi di ñëw,
doon na xoole ngir tere ko mu dugg këram.
40 Yeen tamit fagaruleen ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wi ngeen ko foogewul.»
41 Piyeer ne ko:
«Boroom bi,
ndax léeb bi nun doŋŋ nga ko jagleel,
walla ngir ñépp la?»
42 Te Boroom bi tontu ko ne:
«Kan mooy surga bu wóor tey moytu?
Moom la njaatigeem di tànn ngir mu jiite yeneen surga yi ngir ñuy lekk ci waxtu bi gën.
43 Barkeel na boobu surga te nga xam ne,
bi njaatigeem di yeggsi fekk na muy jëfe noonu.
44 Ci dëgg maa ngi leen koy wax,
njaatige bi dina teg alalam yépp ci ay loxoom.
45 Waaye su surga bi di wax ci xelam ne:
"Sama njaatige dina yéexa ñëw,"
te mu tàmbali di dóor yeneen surga yu góor yi ak yu jigéen yi te di lekk ak di naan sàngara ba màndi,
46 njaatige surga boobu dina ñëw ci bés bi mu ko foogewul ak ci waxtu wu mu xamul.
Noonu dina ko tas te boole wàllam ak ñi gëmul Yàlla.
47 Surga bi xam bëgg-bëggu njaatigeem te waajul dara,
deful dara itam ni mu ko bëgge,
dinañu ko dóor ay yar yu bari.
48 Waaye ki nga xam ne xamul woon bëgg-bëggu njaatigeem te def ay yëf yu jar dóor,
dinañu ko dóor ay yar yu tuuti.
Dinañu laaj lu bari ki ñu jox lu bari,
te dinañu sas lu bari ki ñu dénkoon lu bari.»
49 «Damaa ñëw taalsi xal ci suuf si te bëggoon naa lool xal boobu tàkk léegi.
50 Am na sóob bu ñu ma wara sóob,
te duma am jàmm feek matul.
51 Xalaat ngeen ne damaa ñëw ci suuf si ngir indi jàmm?
Déedéet,
maa ngi leen koy wax;
waaye xaajaloo.
52 Ndaxte dale ko tey juróomi nit ñu nekk ci kër dinañu xaajaloo,
ñett ñi xaajaloo ak ñaar ña te ñaar ñi xaajaloo ak ñett ña.
 
53 \qt Baay dootul juboo ak doomam bu góor
\qt te doom bu góor dootul juboo ak baayam.
\qt Yaay dootul juboo ak doomam bu jigéen
\qt te doom bu jigéen dootul juboo ak yaayam.
\qt Goro bu jigéen dootul juboo ak jabaru doomam
\qt te jabaru doom dootul juboo ak goroom bu jigéen.»
 
54 Noonu Yeesu yokk ca,
ne mbooloo mi:
«Sungeen gisee xiin di jóge ci sowu jant,
dangeen di wax ci saa si ne taw baa ngi ñëw te noonu lay yeggsee.
55 Te sungeen yégee ngelaw bu jóge ci sudd,
dangeen di wax ne dina tàng te noonu lay xewe.
56 Naaféq yi!
Dangeen di mëna ràññee liy xew ci suuf si ak ci asamaan si.
Lu tax ba mënuleen ràññee li xew ci jamono ji?»
57 «Lu tax dungeen àtte yeen ci seen bopp lu jub?
58 Boo amee noon te ngeen am jafe-jafe tey waaja dem ci kër àttekaay bi,
fexeel ba ngeen juboo ci bi ngeen nekkee ci yoon bi,
ndaxte boo ko deful dina la yóbbu ci kanamu àttekat bi.
Bu la àttekat bi àttee ba noppi,
dina la teg ci loxoy takk-der yi,
te takk-der yi dinañu la tëj ci kaso bi,
59 te doo fa génn feek feyuloo lépp ba mu jeex,
ba ci fiftin bi mujje.»