Nit war na wóolu Yàlla
Luug 12.22-34
22 Noonu Yeesu ne taalibeem yi:
«Lii moo tax maa ngi leen koy wax,
buleen jaaxle ci seeni dund,
ci li ngeen wara lekk walla ci seeni yaram,
li ngeen wara sol
23 ndaxte dund moo ëpp solo lekk te yaram moo ëpp solo yére.
24 Xoolleen picci baaxoñ yi:
duñu ji,
duñu góob,
amuñu dencukaay,
amuñu sàq,
waaye Yàlla mu ngi leen di dundal.
Yeena ëpp solo fuuf picc yi.
25 Kan ci yeen moo mëna jaaxle ba yokk ab diir ci dundam?
26 Su fekkee lu tuuti loolu mënuleen ko,
lu tax ngeen di jaaxle ci li ci des?
27 Xoolleen tóor-tóori ñax mi,
ni muy saxe:
duñu liggéey,
duñu ràbb ay yére.
Maa ngi leen koy wax,
buur bi Suleymaan sax,
ci alalam yépp,
li mu doon mëna solu lépp,
mësul soloo ni benn ci ñax yooyu.
28 Su Yàlla solalee nii ñax yi nekk ci tool yi tey,
te bu subaa ñu sànni ko ci taal,
ndax du leen gëna solal yeen,
yeen daal yeena tuuti ngëm?
29 Buleen wut li ngeen wara lekk walla li ngeen wara naan te buleen ci jaaxle
30 ndaxte loolu lépp xeeti àddina yi xamul Yàlla ñoo koy wut,
waaye seen baay xam na ne soxla ngeen ko.
31 Wànte wutleen nguuru Yàlla te Yàlla dina leen jox li ci des.
32 Buleen ragal dara yeen ñi mel ni gétt gu ndaw,
ndaxte seen coobare Baay la,
mu jox leen nguuram.
33 Jaayleen seen alal,
séddale ko néew-di-doole yi,
defarleen kalpe yu dul yàqu te noonu dingeen am alal bu dul jeex ci asamaan fu sàcc dul dugg jot ko,
ak fu ko max dul yàqe
34 ndaxte fu sa alal nekk foofu la sa xol di nekk itam.»