Léebu waa ju ñàkk xel ji
Luug 12.13-21
13 Amoon na ci biir mbooloo mi,
benn waay bu wax Yeesu ne:
«Jàngalekat bi,
ndax doo wax sama mag mu sédd ma ci alalu ndono fi nu sunu baay bàyyeel?»
14 Yeesu ne ko:
«Sama waay,
kan moo ma fal àttekat ngir ma séddale seen alalu ndono?»
15 Noonu mu ne leen ñoom ñépp:
«Moytuleen bëgge,
ndaxte bakkanu doomu Aadama ajuwul ci alalam ak lu mu bari-bari.»
16 Noonu mu wax leen léeb bii:
«Dafa amoon benn waay bu am alal,
bu toolam meññoon lu bari.
17 Mu wax ci xelam:
"Naka laay def?
Ndaxte amatuma sax béréb bu mëna denc sama ngóob yi."
18 Noonu mu ne:
"Waaw,
xam naa li ma wara def.
Damay daaneel sàq yii,
defaraat yeneen sàq yu gëna réy,
def ci sama ngóob yi ak sama alal yépp,
19 te dinaa wax ci sama xel:
'Sama waay am nga alal ngir diiru at yu bari.
Noppalul,
ngay lekk di naan tey bànneexu.'"
20 Waaye Yàlla ne ko:
"Yaw mi ñàkk xel,
tey ci guddi sax dinaa jël sa bakkan.
Kon li nga doon dajale lépp,
ku koy moom?"»
21 Yeesu teg ca ne:
«Loolu mooy dal képp kuy dajale alal ngir boppam te amoo alal ci kanamu Yàlla.»