Yeesu artu na taalibeem yi
Luug 12.1-12
1 Ci waxtu bi Yeesu di wax loolu Farisen yi,
ay junni junniy nit dajaloo nañu bay dëggante.
Yeesu jëkka wax taalibeem yi ne:
«Moytuleen lawiiru Farisen yi,
maanaam seen jikkoy naaféq.
2 Lépp lu nëbbu dina feeñ te lépp luy kumpa dinañu ko xamle,
3 moo tax lépp lu ngeen mën di wax ci guddi gi,
dinañu ko dégg bëccëgu ndarakàmm te lépp lu ngeen déeyante ci néeg yi,
dinañu ko yégle ci kaw kër yi.
4 Maa ngi leen koy wax yeen samay xarit:
buleen ragal ñiy rey yaram te gannaaw loolu dootuñu mëna def dara.
5 Dinaa leen won kan ngeen wara ragal!
Ragalleen ki nga xamante ne gannaaw dee,
am na sañ-sañu sànni leen ci safara.
Waaw,
maa ngi leen koy wax,
kooku ngeen wara ragal.
6 Ndax duñu jaaye juróomi picci ramatu ci ñaari dërëm?
Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom.
7 Te yeen seeni kawaru bopp sax waññ nañu leen.
Buleen ragal dara ndaxte yeena ëpp solo mbooloo picci ramatu.
8 Maa ngi leen di waxaat ne,
ku ma nangu ci kanamu nit ñi,
Doomu nit ki dina la nangu ci kanamu malaakay Yàlla ji,
9 waaye ku ma weddi ci kanamu nit ñi,
Doomu nit ki dina la weddi ci kanamu malaakay Yàlla ji.
10 Ku waxal Doomu nit ki lu bon,
dinañu la ko baal,
waaye ku sosal Xel mu Sell mi,
duñu la ko mësa baal.
11 Bu ñu leen yóbboo ci kanamu kër-ñaan yi ngir àtte leen ak ci kanamu kilifa yi ak ci kanamu àttekat yi,
buleen jaaxle ci anam bi ngeen wara waxe ak ci li ngeen wara wax ngir setal seen der
12 ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal li ngeen wara wax ci waxtu boobu.»