Yeesu jàngal na Farisen yi ne dañoo wara setal lu nekk ci seen biir
Luug 11.33-54
33 Kenn du taal làmp ba noppi di ko nëbb walla nga di ci dëpp leket,
waaye danga koy wékk ngir ñiy dugg mëna gis leer bi.
34 Sa bët mooy sa làmp-yaram,
bu sa bët baaxee sa yaram wépp ay nekk ci leer.
Waaye bu sa bët bonee sa yaram yépp ay nekk ci lëndëm.
35 Moytul nag leer bi nekk ci yaw doon lëndëm.
36 Kon nag bu sa yaram bi yépp nekkee ci leer,
te amul sa benn cér bu nekk ci lëndëm,
dangay nekk ci leer mel ni ku làmp ne ràyy ci kawam.
37 Bi Yeesu di wax loolu,
benn Farisen ñaan ko ngir mu lekksi ci këram.
Mu yeggsi,
toog ngir lekk.
38 Bi Farisen bi gisee Yeesu di lekk te raxasul loxoom yi,
ni ko aada Yawut yi diglee,
mu daldi jaaxle.
39 Boroom bi ne ko:
«Yeen Farisen yi dangeen tàmm di raxas ci biti kaas bi ak bu ndab li,
te seen biir xol mu ngi fees ak soxor ak yeneen jëf yu bon.
40 Yeen ñu ñàkk xel yi,
ndax xamuleen ne,
ki sàkk li nekk ci biti,
moo sàkk tamit li nekk ci biir?
41 Saraxeleen li nekk ci seen biir xol te seen lépp dina set.»
42 «Waaye musiba dal na leen yeen Farisen yi,
ndaxte dangeen di sàkk asaka ci xeetu safal bu nekk maanaam:
naana ak ru ak ci lujum bu nekk te di sàggane li ëpp solo,
maanaam:
njubte ak mbëggeelu Yàlla.
Loolu ngeen wara def te baña sàggane li ci des.
43 Musiba dal na leen yeen Farisen yi,
ndaxte dangeen tàmm di toog ci toogukaay yi féete kanam,
ci kër-ñaan yi,
te di bëgg ñu leen di nuyu ak ñaari loxo ci péncu dëkk bi.
44 Musiba dal na leen,
ndaxte dangeen mel ni ay bàmmeel yu amul xàmmikaay;
nit ñi di dox ci kaw seeni bàmmeel te duñu ko xam.»
45 Benn jàngalekatu-yoonu-Musaa wax ko ne:
«Jàngalekat bi,
soo waxee loolu danga nuy xas nun itam.»
46 Yeesu tontu ko ne ko:
«Musiba dal na leen yeen jàngalekati-yoonu-Musaa yi itam,
ndaxte dangeen di sas nit ñi ay jëf yu diis waaye,
yeen dungeen ci nangoo laal seen catu baaraam.
47 Musiba dal na leen ndaxte yeenay tabax ay bàmmeel ngir Yonent yi seen maam reyoon.
48 Sungeen di def loolu dangeen di wone ne ànd ngeen ci jëf yi seeni maam defoon,
ndaxte ñoom ñoo rey yonent yi,
te yeen,
ngeen di tabax seeni bàmmeel.
49 Moo tax Yàlla ci xelam bu rafet wax na ne:
"Dinaa leen yónnee ay yonent ak ay ndaw.
Dinañu rey ñenn ñi te fitnaal ñeneen ñi."
50 Ni loolu ame,
Yàlla dina këpp ci niti jamono jii deretu yonent yi yépp ñu reyoon ba àddina sosoo ba léegi.
51 Dale ko ci deretu Abel ba ci deretu Sakari mi ñu reyoon ci diggante bérébu saraxlukaay bi ak béréb bu sell bi.
Waaw maa ngi leen koy wax,
dinañu këpp deretu yonent yi ñu reyoon ci kaw niti jamono jii.
52 Musiba dal na leen yeen jàngalekati-yoonu-Musaa yi ndaxte dangeena téye caabi xam-xam bi;
dugguleen te di tere ñi bëgga dugg,
ñu dugg.»
53 Bi Yeesu génnee ci béréb boobu jàngalekati-yoonu-Musaa yi ak Farisen yi di ko sonnal te di ko laaj ci ay mbir yu bari
54 di wut njuumte ci ay kàddoom ngir jëfandikoo ko.