Yeesu dàq na benn rab te jàngal mbooloo mi
Luug 11.14-32
14 Benn bés Yeesu dàq benn rab bu muumaloo woon benn waay.
Bi rab bi génnee,
waa ji tàmbali di wax.
Mbooloo mi yépp yéemu,
15 waaye ñenn ñi di wax ne,
ci kàttanu Beelsebul mi di buuru rab yi lay dàqe rab yi ,
16 te ñeneen ñi di ko fexe fiir;
laaj ko kéemaan buy firndeel ne ci asamaan lay jële kàttanam.
17 Waaye Yeesu xam seeni xalaat ne leen:
«Bépp nguur bu xaajaloo ci biiram dina tas,
te kër yi bu ci nekk di maab ci moroomam.
18 Bu Seytaane di xeex boppam naka la nguuram mëna yàgge,
ndaxte yeena wax ne ci kàttanu Beelsebul laay dàqe rab yi.
19 Te man su fekkee ci kàttanu Beelsebul laay dàqe rab yi;
kon seeni taalibe ci ban kàttan lañuy dàqe rab yi?
Moo tax ñoom ci seen bopp ñoo leen di àtte.
20 Waaye su fekkee ci kàttanu Yàlla laay dàqe rab yi,
kon nguuru Yàlla gi yeggsi na ci yeen.
21 Su fekkee ne dafa am ku am doole te yor gànnaayam te aar këram alalam day nekk ci kaaraange.
22 Waaye ku ko ëpp doole bu nëwee daan ko dina jël gànnaay yi mu yaakaaroon te séddale alalam.
23 Ku farul ci man,
yaa ngi may xeex;
ku dajalewul ak man,
yaa ngi tasaare.»
24 «Bu rab génnee ci nit,
day wër ci màndiŋ bi ngir wut fu muy noppaloo.
Bu ko amul dina wax ne:
"Xaaral,
ma dellu ci sama kër bi ma jóge woon."
25 Bu yeggsee,
fekk ñu bale kër gi defar ko ba mu jekk.
26 Mu daldi dem woowi juróom ñaari rab yu ko gëna soxor,
ñu dugg,
dëkk fa.
Noonu,
melokaanu nit kooku mooy gëna yées na mu meloon bu jëkk.»
27 Bi Yeesu di wax loolu benn jigéen ci biir mbooloo mi yékkëti baatam,
ne ko:
«Barkeel na,
jigéen bi la jur te nàmpal la ci weenam.»
28 Yeesu daldi ko tontu ne:
«Neel kay,
barkeel na,
ki nga xam ne day déglu kàddu Yàlla gi te di ko jëfe.»
29 Naka la mbooloo mi di gën di takku Yeesu tàmbali di wax ne:
«Niti jamono jii,
dañoo bon.
Nu ngi laaj benn màndarga,
waaye duñu leen jox benn,
bu dul màndargay Yunus bi,
30 ndaxte ni Yunus nekke woon màndarga ci waa dëkku Niniw,
noonu Doomu nit ki dina nekk màndarga ci niti jamono jii.
31-32 Te ci bésu àtte ba waa Niniw dinañu jóg ngir tuumaal niti jamono jii,
ndaxte bi ñu déggee waare Yunus ba,
tuub nañu seen bàkkaar;
te xoolleen,
ku sut Yunus mu ngi fi.
Ci bésu àtte ba tamit buur bu jigéen ba dëkkoon ci sudd dina jóg tuumaal niti jamono jii,
ndaxte jóge woon na fu sori ngir déglu waxu Suleymaan yu rafet yi;
te xoolleen,
ku sut Suleymaan mu ngi fi.