Yeesu jàngal na taalibeem yi ni ñuy ñaane
Luug 11.1-13
1 Benn bés Yeesu doon ñaan ci benn béréb.
Bi mu ñaanee ba noppi,
benn ci taalibeem yi ne ko:
«Boroom bi,
ndax doo nu jàngal ni nuy ñaane,
ni ko Yaxya jàngale ay taalibeem?»
2 Yeesu ne leen:
«Bu ngeen di ñaan,
waxleen lii:
Baay na ñépp yékkëti sa tur,
na sa nguur ñëw,
3 may nu li nuy dunde bés bu nekk,
4 te baal nu sunuy bàkkaar
ndaxte nun tamit nu ngi baal ñi nu tooñ,
te bul bàyyi Seytaane fiir nu.»
5 Noonu mu yokk ca ne:
«Bu fekkee kenn ci yeen dafa am xarit,
mu dem ci moom xaaju guddi te wax ko ne:
"Sama xarit,
lebal ma ñetti mburu
6 ndaxte dama am sama beneen xarit bu jóge ci tukki,
dal sama kër te awma dara lu ma ko jox."
7 Ki ci biir dina ko tontu ne:
"Bul ma sonal.
Tëj naa sama bunt te tëdd naa ak sama njaboot ba noppi.
Mënuma jóg ngir jox la mburu yi."
8 Maa ngi leen koy wax,
bu dul li mu nekk xaritam sax moo tax mu jóg te jox ko ko,
waaye dina jóg,
jox ko lépp li mu soxla ndax ni mu ko doon sonale ci ñaan gi.»
9 «Te man,
maa ngi leen di wax:
ñaanleen,
ñu may leen.
Seetleen te dingeen gis.
Fëggleen,
ñu ubbil leen.
10 Ndaxte ku ñaan,
ñu may la.
Ku seet,
dinga gis.
Te ku fëgg,
ñu ubbil la.
11 Ban baay ci yeen,
moom lay doomam di ñaan jën,
mu jox ko jaan;
12 walla mu ñaan ko nen,
mu jox ko jiit?
13 Yeen ñu bon ñi,
segem yeena mëna jox seen doom lu baax,
rawatina Baay bi ci asamaan ndax du jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan?»