Màrt ak Maryaama dalal nañu Yeesu
Luug 10.38-42
38 Yeesu ak taalibe yi doon nañu tukki,
dem ba yegg ci benn dëkk,
fekk fa benn jigéen bu ñuy wax Màrt.
Mu dalal leen ci këram.
39 Amoon na rakkam bu tudd Maryaama.
Mu ñëw,
toog ci wetu Yeesu di déglu jàngaleem.
40 Màrt féete woon liggéeyu kër gi yépp.
Màrt ñëw,
ne ko:
«Boroom bi,
ndax defu la dara,
sama rakk bàyyee ma liggéey bi yépp?
Ndax doo ko wax mu ñëw jàppale ma?»
41 Boroom bi tontu ko ne ko:
«Màrt,
Màrt,
yaa ngi jaxasoo ak di jaaxle ci mbir yu bari,
42 waaye benn mbir rekk moo am solo,
te Maryaama tànn na ko ba noppi,
te kenn du ko jël ci moom.