Léebu benn waa Samari bu baax
Luug 10.25-37
25 Te noonu benn bés amoon na benn jàngalekatu-yoonu-Musaa bu jóg ngir fexe fiir Yeesu.
Mu ne ko:
«Jàngalekat bi,
lan laa wara def ngir am dund gu dul jeex?»
26 Yeesu tontu ko ne:
«Lan lañu bind ci yoonu Musaa ak ban jàngat nga ci am?»
27 Mu ne ko:
«Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bi yépp,
sa bakkan bépp,
sa kàttan bépp ak sa xel mépp te nga bëgg sa moroom ni nga bëgge sa bopp.»
28 Yeesu ne ko:
«Wax nga dëgg.
Defal loolu te dinga dund.»
29 Waaye jàngalekatu-yoonu-Musaa bi bëgga jox boppam dëgg,
mu ne ko:
«Kan mooy sama moroom?»
30 Yeesu tontu ko ne:
«Dafa amoon benn waay bu jóge woon Yerusalem ngir dem Yeriko.
Bi muy dem ci yoon bi ay bandi dogale ko,
futti ko,
door ko ba mu bëgga dee,
bàyyi ko ci yoon bi.
31 Benn jébbalkatu-sarax jaar fa,
gis waa ji,
teggi ko,
dem yoonam.
32 Benn waay bu soqikoo ci giiru Lewi jaar fa,
gis waa ji,
teggi ko,
dem yoonam.
33 Waaye benn waay bu dëkk Samari,
bi mu séenee waa ji,
mu yërëm ko,
34 jegesi ko,
jël diwlin ak biiñ,
faj góom yi,
lëmës leen,
yéegal ko ci mbaamam,
yóbbu ko ci bérébu fanaanukaay bi te di ko toppatoo.
35 Ci ëllëg sa,
mu yékkëti lu tollook peyooru benn fanu liggéey,
jox ko boroom fanaanukaay ba,
ne ko:
'Toppatool waa ji,
te loo ci yokk,
bu ma dellusee man,
dinaa la ko fey.'»