Yeesu wéral na benn jigéen ju xuuge ci bésu noflaay bi
Luug 13.10-17
10 Benn bésu noflaay Yeesu da doon jàngale ci biir benn kër-ñaan.
11 Foofu amoon na benn jigéen.
Rab moo ko taxoon xuuge diiru fukki at ak juróom ñett ba mënul woona siggi.
12 Bi ko Yeesu gisee mu woo ko wax ko ne:
«Soxna si yewwi nañu la,
ci sa laago.»
13 Noonu mu teg ko loxoom yi.
Ci saa si soxna si daldi siggi te jub xocc,
di màggal Yàlla.
14 Noonu njiitu kër-ñaan bi daldi fees dell ak mer ci li Yeesu doon faje ci bésu noflaay bi.
Mu jël kàddu gi,
wax mbooloo mi:
«Am na juróom benni fan yu ñu wara liggéey,
kon ñëwleen ci bés yooyu ngir faju waaye bu mu doon ci bésu noflaay bi.»
15 Boroom bi tontu ko ne:
«Yeen naaféq yi!
Kenn ku nekk ci yeen bu amee nagam walla mbaamam ndax du ko dem yewwi ci bésu noflaay bi ngir yóbbu ko mu naani?
16 Te jigéen jii bokk ci askanu Ibraayma,
Seytaane tënk ko ci diiru fukki at ak juróom ñett,
ndax waruñu ko yewwi ci bésu noflaay bi?»
17 Bi Yeesu di wax loolu,
bañaaleem yi daldi rus waaye mbooloo mi ànd ak mbégte ci jëf yu yéeme yi mu doon def.